Xibaaru jàmm bu Almasi Yeesu,
ci jottalib
Luug
Luug ak Jëf ya daan nañu bokk ci benn téere bi Luug bind. Ñaar yépp a indi ni Yàlla njëkka woowe bànni Israayil ba noppi, doora woo mboolem xeet yi, ngir ñu barkeele ci Ibraayma.
Ci Luug, nettali bi, Yerusalem la jublu, ci péncum cosaanu Yawut yi. Ci Jëf ya, Yerusalem la nettali bi bawoo, jëm ci xeeti àddina yi ci des.
Ci tënk:
1.1—9.50 Liggéeyu Yeesu ca diiwaanu Galile la doore.
9.51—19.27 Tukkib Yeesu ci Yerusalem.
19.28—24.53 Almasi Yeesu sarxe na bakkanam ca Yerusalem, te gannaaw gi, mu dekki.
1
Ubbite gi
Bare na ñu fexee bind ab nettalib mbir yi sotti woon ci sunu biir, noonee nu ko jote ca ña ko fekke woon ca ndoorte la, te seede yooyu mujj doon jawriñi kàddug Yàlla. Moo tax man it, ma fas laa yéenee bindal lépp ba mu jekk, yaw Tewofil mu tedd mi, gannaaw ba ma gëstoo mbir mépp, dale ko ca ndoorte la, ba mu leer nàññ. Su ko defee nga xam xéll ne li ñu la jàngal, lu wér péŋŋ la.
Malaaka yégle na juddub Yaxya
Jant ya Erodd nekkee buuru réewum Yawut yi, ab sarxalkat la woon bu ñuy wax Sàkkaryaa, bokk ci làngu sarxalkat yi askanoo ci Abya, te soxnaam Elisabet askanoo ci Aaróona. Ñoom ñaar ñépp a juboon, Yàlla seede, te mucc ayib ci ni ñuy jëfe santaane yeek ndigali yooni Boroom bi. Amuñu woon doom nag, ndax Elisabet manul woona am doom, te it booba ñoom ñaar ñépp a dem ba màggat.
Sàkkaryaa la làngam aye woon, muy def liggéeyu carxalam fa kanam Yàlla. Ba ñu tegoo bant, na ko sarxalkat yi baaxoo woon, moom la bant ba dal, mu wara dugg ci biir néegu Boroom bi, ngir taal fa saraxu cuuraay.
10 Mbooloo mépp nag a nga woon ca biti di ñaan, ca waxtuw saraxu cuuraay boobu. 11 Ci biir loolu menn malaakam Boroom bi jekki feeñu Sàkkaryaa, ca wetu ndijooru sarxalukaayu cuuraay ba. 12 Ba ko Sàkkaryaa gisee daa jaaxle, tiitaange jàpp ko. 13 Malaaka ma ne ko: «Sàkkaryaa, bul tiit, ndax sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina am doom ju góor, nanga ko tudde Yaxya. 14 Dinga am mbégte ak bànneex, te ñu bareey bég ci juddoom, 15 ndax ku màgg lay doon, Boroom bi seede. Biiñ ak lenn luy màndil nag, du ko naan, Noo gu Sell gi mooy dale ca biiru ndeyam, solu ko ba fees. 16 Ñu bare ci bànni Israayil, moo leen di waññi ci Boroom bi seen Yàlla. 17 Mooy ndaw li koy jiitu, ànd ak leer ga ak xam-xam ba woon ca Yonent Yàlla Ilyaas, ba waññi xolu baay ci doomam, waññi ku déggadi ci xelum aji jub, loolu yépp ngir waajal aw xeet, ba ñu jekk ngir Boroom bi.»
18 Sàkkaryaa nag ne malaaka mi: «Lu may def ab takk ci loolu ba mu bir ma? Ndax man màggat naa, te sama soxna it làq na ay fan.» 19 Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw fi kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw, yégal la bii xibaaru jàmm. 20 Léegi nag, dama ne, gannaaw gëmuloo sama kàddu, giy jot, sotti, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera loolu di am.»
21 Ci biir loolu mbooloo maa ngay xaar Sàkkaryaa, jaaxle lool ndax yàggaayam ca biir néegu Yàlla ba. 22 Ba mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Ñu daldi xam ne am na lu ko feeñu ca néegu Yàlla ba. Ma nga leen di liyaar, manatula wax.
23 Naka la Sàkkaryaa fégal ayu carxalam, daldi ñibbi. 24 Gannaaw gi, soxnaam Elisabet ëmb. Lëlu na juróomi weer. Ma nga naan: 25 «Lii Boroom bee ma ko defal ci jant yi mu ma geesoo, ba teggil ma sama gàcce gi ci biir nit ñi!»
Jibril yégle na juddub Yeesu
26 Ba Elisabet tolloo ci juróom benni weeram, ca la Yàlla yebal Jibril malaaka mi, dëkk bi ñuy wax Nasaret ca diiwaanu Galile, 27 ci janq bu digoo séy ak waa ju ñuy wax Yuusufa te bokk ci waa kër Daawuda. Janq ba Maryaama lañu koy wax. 28 Malaaka ma agsi ba ca moom, ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi ñu baaxe, Boroom bi yaw la àndal.»
29 Waxi malaaka ma nag jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki. 30 Malaaka ma ne ko: «Maryaama, bul tiit, ndax daje nga ak yiwu Yàlla. 31 Dinga ëmb, ba jur doom ju góor, nga tudde ko Yeesu*Yeesu ci làkku ebrë mooy Yosuwe, muy firi Aji Sax jeey musle. Aji Sax ji mooy tur wi Yàlla firil Musaa ci Mucc ga 3.13-15.. 32 Ku màgg lay doon, te dees na ko woowe Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla moo koy jagleel nguurug Daawuda maamam. 33 Mooy nguuru fi kaw waa kër Yanqóoba ba fàww, te nguuram du foq mukk.»
34 Ci kaw loolu Maryaama laaj malaaka mi ne ko: «Nu loolu di ame, te man ab janq laa?» 35 Malaaka mi ne ko: «Noo gu Sell gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam kiy juddoo ci yaw, dees na ko woowe Ku sell, ak Doomu Yàlla. 36 Te kat Elisabet sa mbokk mi itam ëmb na doom ju góor te fekk ko màggat. Ki ñu doon woowe jigéen ju jaasir, mu ngi nii ci juróom benni weeram, 37 ndax Yàlla, dara tëwu ko.» 38 Maryaama daldi ne: «Maa ngi, di jaamub Boroom bi. Nii nga waxe, na ame noonu ci man.»
Ba loolu amee malaaka ma bàyyikoo ca moom, dem.
Maryaama seeti na Elisabet
39 Ci fan yooyu la Maryaama fabu gaaw, jëm diiwaanu tund ya, ca dëkkub Yude, 40 ba Sàkkaryaa dëkke. Mu agsi ca kër ga, nuyu Elisabet. 41 Naka la Elisabet dégg nuyoob Maryaama, doom ja mu ëmb yëngu ca biiram. Elisabet daldi fees ak Noo gu Sell gi. 42 Mu àddu ca kaw ne: «Yaa gëna barkeel ci jigéen ñi, sa doom ji nga ëmb it barkeel na! 43 Ana ku ma doon ba sama ndeyu Sang di ma seetsi? 44 Naka la sa kàddug nuyoo tàbbi ci sama nopp rekk, sama doom ji yëngu ci sama biir bi ndax mbégte. 45 Ndokkalee yaw mi gëm ne mbir mi ñu la yégal, te mu tukkee ci Boroom bi dina sotti!»
Maryaama woy na mbaaxu Yàlla
46 Maryaama nag ne:
«Sama xol laay màggale Boroom bi,
47 samag noo laay bége Yàlla mi may musal,
48 moo geesu bii jaamam bu tekkeedi,
ba maasoo maas doxe fi woowe ma boroom mbég mi,
49 nde Kiy Boroom doole moo ma defal jaloore,
cellte ñeel naw turam.
 
50 «Yërmandeem a ñeel ay ragalkatam,
maas ci kaw maas.
51 Dooley loxoom la defe ay jaloore,
tasaare ñi jikkowoo réy-réylu,
52 wàcce buur yi ci seeni gàngune,
yékkati baadoolo yi.
53 Ñi xiif, mu reggale leen lu neex,
ñi duunle, mu dàqe loxoy neen.
54 Moo wallu bànni Israayil, jaamam,
bàyyee ko xel yërmandeem,
55 noonee mu ko dige woon sunuy maam,
ñeel Ibraayma ak askanam ba fàww.»
56 Maryaama toog na fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
Lu jëm ci juddub Yaxya
57 Gannaaw gi, Elisabet dem ba àppam mat, mu mucc, am doom ju góor. 58 Dëkkandoom yaak ay bokkam yég noonu ko Boroom bi xéewalee yërmandeem, ñu bokk ak moom mbégte ma.
59 Ba bés ba délsee, ñu dikk xarafalsi xale ba, bëgg koo tudde Sàkkaryaa, dippee ko baayam. 60 Yaayam nag ne leen: «Déet, Yaxya lay tudd.» 61 Ñu ne ko: «Waaye kenn ci say bokk tuddul noonu!»
62 Ci kaw loolu ñu liyaar baayam, ngir xam nu mu bëgg ñu tudde xale bi. 63 Sàkkaryaa laaj àlluwa, ñu jox ko, mu bind ci: «Yaxya mooy turam.» Ñépp waaru. 64 Ca saa sa gémmiñ ga ubbiku, làmmiñ wa nangu, muy wax, daldi sant Yàlla. 65 Ba loolu amee tiitaange dikkal mboolem ña leen séq, te mbir moomu mépp nag doon waxtaan ca diiwaanu tundi Yude gépp. 66 Ña ca dégg ñépp daldi bàyyi xel ca mbir ma, te naan: «Lu xale bii nara doon ëllëg?» ndax manoorey Boroom bee àndoon ak moom.
Sàkkaryaa sant na Yàlla
67 Ci kaw loolu Sàkkaryaa baayu Yaxya fees ak Noo gu Sell gi, daldi tàmbalee jottali kàdduy waxyu, ne:
68 «Cant ñeel na Boroom bi Yàllay Israayil,
moo seetsi ñoñam, ba jot leen!
69 Moo nu feeñalal Musalkat bu manoorewu,
fi biir kër Daawuda jaamam ba,
70 noonee mu ko waxe woon ca jant yu njëkk ya,
yonentam yu sell ya woon jottali.
71 Moo nu musal ci sunuy noon,
jële nu ci sunu loxoy mboolem bañaale.
72 Moo jëfe yërmande ñeel sunuy maam,
tey bàyyi xel kóllëreem gu sell,
73 ak ngiñ la mu giñaloon sunu maam Ibraayma,
74 ne moo nuy may nu mucce ci loxoy noon,
ba man koo jaamoo xel mu dal
75 ci biir sellaay ak njub ci kanamam, sunu giiru dund.
 
76 «Ngóor si nag yaw, yonentu Aji Kawe ji lees lay woowe,
nde yaay dox, jiitu Sang bi, xàllal kow yoonam,
77 ngir yégal ñoñam mucc
guy topp seen njéggalug bàkkaar.
78 Sunu Yàllaa yaatu yërmande,
moo nu fenkal ab jant,
79 di niital ñi tooge biir lëndëm ak takkndeeru dee,
di nu gindi, teg nu ci yoonu jàmm.»
80 Xale bi nag di màgg, xel ma di yokku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba mu feeñoo bànni Israayil.

*1.31 Yeesu ci làkku ebrë mooy Yosuwe, muy firi Aji Sax jeey musle. Aji Sax ji mooy tur wi Yàlla firil Musaa ci Mucc ga 3.13-15.