3
Yaxya waare na ngir nit ñi tuub
1 Jant yooyu la Yaxya feeñ, di waare ca màndiŋu Yude, 2 naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndax nguurug asamaan dëgmal na.» 3 Kooku lañu doon wax, te Yonent Yàlla Esayi jottali woon ko, ba mu nee:
«Baatu nit a ngi xaacoo ca màndiŋ ma naan:
“Nangeen xàll yoonu Boroom bi,
juballeen ay xàllam*Seetal ci Esayi 40.3..”»
4 Yaxya nag mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem la daan sol, laxasoo laxasaayu der ca ndiggam, ab dundam diy njéeréer ak lemu àll. 5 Nit ña daldi bàbbeeku, jëm ca moom, waa Yerusalem, ak mboolem diiwaanu Yude, ak mboolem diiwaanu dexu Yurdan. 6 Ñu tudd seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
7 Ci kaw loolu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ci ndox. Yaxya ne leen: «Yeen njurum jaan mee, ku leen artu, ba ngeen di daw sànj miy dikk? 8 Kon nag jëfeleen jëf ju yelloo ag tuubeel, 9 te buleen defe ne man ngeena wax ci seenum xel ne: “Nun, Ibraayma mooy sunu maam,” ndax maa leen ko wax, doj yii, Yàlla man na cee sàkkal Ibraayma aw askan. 10 Léegi nag xàcc nañu sémmiñ ngir gor reenu garab yi ba noppi. Kon gépp garab gu ci meññul doom yu baax, dees koy gor, sànni ca sawara sa. 11 Man, cim ndox laa leen di sóob, ngir jëmmal seenug tuubeel. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma sut, ba ay caraxam sax yeyoowuma ko koo summil. Moom nag ci Noo gu Sell gi ak ci sawara†Sóobu gi ci Noo gu Sell gi ak ci sawara: Almasi bi moo leen di sol doole ju bawoo ci Noo gu Sell gi, ak itam setal leen ni sawara di setale weñ gu am lu ko rax. Sawara dina taxawe itam céru mbugal mu ñeel ñi déggalul Yàlla. Seetal ci 12.49; Jëf ya 2.3. la leen di sóob. 12 Ab layoom a ngi ci loxoom, te mooy jéri dàggaam, ba mu set wecc; am peppam lay fat ci sàq mi, waaye xatax bi, da koy lakk ci sawara su dul fey mukk.»
Yaxya sóob na Yeesu ci dexu Yurdan
13 Booba la Yeesu jóge Galile, dikk ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan. 14 Teewul Yaxya gàntal, ne ko: «Man may ki soxla, nga sóob ma ci ndox, yaw nga dikk ci man!» 15 Yeesu ne ko: «Baalagum noonu rekk, ndax ci lanuy matale lépp li Yàlla bëgg ci njub.» Yaxya daldi koy nangul.
16 Gannaaw ba ñu sóobee Yeesu, ba mu génnee ca saa sa ca ndox ma, asamaan a jekki ubbiku ngir moom. Mu gis Noowug Yàlla wàcc ni am pitax ca kawam. 17 Ci kaw loolu rekk, baat jibe asamaan, ne: «Kii mooy sama Doom, sama soppe; Moom laay bànneexoo.»