12
Yeesu, boroom bésub Noflaay
1 Ca jamono yooyu la Yeesu doon dem, ba jaare ci ay tool yu ñor, mu yemook bésub Noflaay. Taalibeem ya nag xiif, daldi tàmbalee fàq ay gub, di lekk. 2 Farisen ya gis ca, ne Yeesu: «Gisal, say taalibee ngi def lu yoon mayewul ci bésub Noflaay!»
3 Teewul Yeesu ne leen: «Xanaa jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon? 4 Ba Daawuda duggee ca kër Yàlla ga, mburum teewal ma la lekk, te yoon mayewul kenn ku ca lekk; du moom, du ña mu àndaloon, xanaa sarxalkat ba doŋŋ*Seetal ci 1.Samiyel 21.2-7.. 5 Am jànguleen ci yoonu Musaa, ne bésub Noflaay, ci la sarxalkat ya ca kër Yàlla ga di xëtte ndigalal ñàkka liggéey ci bésub Noflaay, te taxu leena tooñ? 6 Waaye maa leen ko wax, ku sut kër Yàllaa ngi fi teew. 7 Su ngeen xamoon lu lii di tekki: “Ngor laa namm, dub sarax†Seetal ci Ose 6.6.,” kon dungeen sikk jàmbur ñu deful dara, 8 ndax bésub Noflaay, Doomu nit ki mooy boroom.»
Yeesu faj na nit ku loxoom làggi
9 Ba loolu amee Yeesu jóge foofa, dem ca seen jàngu ba. 10 Boroom loxo bu làggee nga fa woon. Farisen ya nag laaj ko ne ko ndax yoon maye na faj ci bésub Noflaay, ngir ñu man koo tuumaal. 11 Yeesu ne leen: «Ana kan ci yeen mooy am menn xar doŋŋ, mu daanu ci kàmb, bésub Noflaay, te jàppu ko, génne? 12 Ñaata yoon la nit ëppe solo am xar? Kon kay yoon maye na def lu baax, bésub Noflaay.»
13 Ci kaw loolu mu ne waa ja: «Tàllalal sa loxo!» Mu tàllal, loxo ba wér, ni ba ca des.
14 Ba loolu amee Farisen ya génn, diisooji, ngir pexe mu ñu ko sànke. 15 Teewul Yeesu yég ko, daldi jóge foofa, mbooloo mu bare nag topp ko, mu faj leen ñoom ñépp, 16 te di leen femmu, ngir ñu bañ koo siiwal. 17 Noonu la kàddu ga ñu waxoon ci jottalib Yonent Yàlla Esayi, mate. Mooy ba mu nee:
18 «Sama ndaw lii laa tànn,
muy sama soppey xol,
maay sol sama Xel ci moom,
ba mu yégal xeet yi yoonu àtte.
19 Du xuloo, du xaacu,
baatam du dégtoo mbedd ya.
20 Barax bu lemu sax, du ko damm,
leer gu giim, du ko fey,
ba kera mu mayee njub, ndam,
21 te aw turam la xeet yiy yaakaar‡Seetal ci Esayi 42.1-4..»
Yeesu faj na boroom rab bu gumba, luu
22 Gannaaw loolu ñu indil Yeesu boroom rab bu gumba, luu. Yeesu faj ko, ba muy wax, di gis. 23 Mbooloo mépp nag yéemu, naan: «Xanaa kii du Sëtub Daawuda bi?»
24 Teewul ba Farisen ya déggee loolu dañu ne: «Kii xanaa du ci Beelsebul buuru rab yi doŋŋ lay dàqe ay rab!» 25 Teewul Yeesu ràññee seen xalaat, ne leen: «Gépp nguur guy xàjjalikoo ci biiram, day tas, te bépp dëkk mbaa kër guy xàjjalikoo ci biiram, du mana yàgg. 26 Seytaane nag su dàqee Seytaane, indi na xàjjalikoo ci biiram; te kon ana nu nguuram di yàgge? 27 Te bu fekkee ne man Beelsebul laay dàqe rab yi, seen ñoñ nag ñoom, kan lañuy dàqe ay rab? Kon kay seen ñoñ a leen tiiñal. 28 Waaye su dee Noowug Yàlla laay dàqe rab yi nag, kon nguurug Yàlla agsi na ba ci yeen.
29 «Ana nu nit mana dugge ci kër ponkal, yóbbu alalam, te njëkkula yeew ponkal mi ba noppi, doora mana toj kër ga. 30 Ku farul ak man nag, man ngay xeex, te ku àndul ak man di dajale, yaa ngi tasaare.»
Sosal Noowug Yàlla moo yées
31 «Moo tax ma ne leen, bépp bàkkaar, ak gépp kàddug saaga Yàlla, dees na ko jéggale, waaye saaga Noowug Yàlla, deesu ko jéggale. 32 Ku jëme kàddug safaan ci Doomu nit ki, dees na ko jéggal, waaye ku jëme kàddug safaan ci Noo gu Sell gi, deesu ko jéggal mukk, du tey, du ëllëg.
33 «Yaar garab gi baax, meññeefam baax, mbaa garab gi bon, meññeefam bon; nde garab, meññeefam. 34 Njurum jaan mi ngeen doon, nu ngeen mana waxe lu baax, te di ñu bon? Gémmiñ, la fees xolu boroom lay wax. 35 Nit ku baax, ci dencub ngëneel lay jële lu baax, nit ku bon it, ci dencub safaanam lay jële lu bon. 36 Maa leen wax ne leen, gépp kàddug neen gu nit masa wax, dina ko layoo kera bés-pénc. 37 Ndax kat ci sa kàddu lees lay joxe dëgg, ci sa kàddu it lees lay daane.»
Yonent Yàlla Yunus doy na firnde
38 Ci kaw loolu ay firikati yoonu Musaa ak ay Farisen wax ak Yeesu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëgg firnde ju bawoo ci yaw.» 39 Yeesu ne leen: «Maas gu bon gu ñàkk kóllëre, firnde lañuy wut, waaye deesu leen jox jenn firnde ju moy firndey Yonent Yàlla Yunus. 40 Ndax na Yunus nekke woon ca biir rabu géej wu mag wa, ñetti bëccëg ak ñetti guddi, noonu la Doomu nit ki di nekke ci biir xolu suuf, ñetti bëccëg ak ñetti guddi. 41 Waa réewum Niniw it keroog àtte ba dinañu taxaw, layook niti tey jii, tiiñal leen, ndax ñoo tuube woon ca waareb Yunus§Seetal ci Yunus 1.2; 3.4-5., te tey jii, ku sut Yunus a ngi fi. 42 Keroog àtte ba, Lingeeru bëj-saalum dina jóg, janook niti tey jii, tiiñal leen; ndax moo bàyyikoo woon ca catal àddina, ngir déglusi xam-xamu Suleymaan*Seetal ci 2.Jaar-jaar ya 9.1-12., te tey jii, ku sut Suleymaan a ngi fi.
43 «Aw rab nag, bu jàppee nit ba bàyyi ko, day wër béreb yu fendi, di wut fu mu noppaloo, te du ko gis. 44 Su ko defee mu ne: “Ca sama kër ga ma jóge woon laay dellu.” Bu dikkee, fekk kër gi wéet, buube, defare ba jekk. 45 Day dem nag indi yeneen juróom ñaari rab yu ko yées, ànd ak ñoom, ñu bokk sancsi; su ko defee ni nit kiy mujje mooy yées na mu jëkke. Noonu lay deme ci niti tey ñu bon ñii.»
Déggal Yàllaa gën bokk ak Yeesu
46 Yeesu moo doon wax ak mbooloo ma, yaayam ak ay rakki Yeesu jekki dikk, taxaw ci biti, bëgga wax ak moom. 47 Kenn ca mbooloo ma ne ko: «Sa yaay ak say rakk kat, ñu ngi taxaw ci biti, bëgga wax ak yaw.» 48 Teewul Yeesu ne ko: «Ana kan mooy sama yaay, ak ñan ñooy samay rakk?» 49 Mu daldi joxoñ ay taalibeem, ne: «Ñii ñooy sama yaay ak samay rakk, 50 ndax kuy jëfe sama coobarey Baay ba fa asamaan, kooku moo di sama rakk ju góor, di samab jigéen, di sama yaay.»