25
Séentu sab sang laaj na teewlu
«Su boobaa nguurug asamaan day mel ni fukki janq yu fab seeni làmp, génn, gatanduji boroom séet, juróom ña nag di ñu dofe, te juróom ña ca des di ñu muus. Ñu dofe ña fab seeni làmp, te jotuñoo fàgguwaale ag diw; ña muus ñoom, fàgguwaale ag diw ci seeni njaq, booleek seeni làmp. Boroom séet ba nag guddee, ñépp gëmmeentu, bay nelaw.
«Ba guddi ga xaajee, coow la jib: “Boroom séet baa ngoog, génnleen, gatandu ko.” Janq ja jépp yewwu, daldi waajal seeni làmp. Ñu dofe ña ne ña muus: “Mayleen nu ci seenug diw, sunuy làmp a ngi fey.” Ñu muus ña ne leen: “Déet, lu ko moy du nu am lu nu doy, nook yeen. Demleen kay jëndali seen bopp fa muy jaaye!”
10 «Naka lañu dem jëndi, boroom séet ba agsi. Ci kaw loolu ña mu fekk noppi, ànd ak boroom séet ba, dugg ca néegu bernde ja, bunt ba daldi tëje. 11 Gannaaw loolu janq ja ca des dikk, ne: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu!” 12 Mu ne leen: “Aylayéwén laa leen wax, xawma leen.”
13 «Teewluleen boog, nde xamuleen bés ba, mbaa waxtu wa.
Ndénkaane aw sas la
14 «Nguurug Yàlla dafa mel ni kuy waaja tukki, daldi woo ay surgaam, batale leen alalam. 15 Kii, mu dénk ko juróomi milyoŋ*juróomi milyoŋ: maanaam juróomi talaŋ. Seetal Xaalis ci Leeral yi.; kee, ñaar; ka ca des, benn, ku nekk ak la mu àttan. Ci kaw loolu, mu daldi tukki. 16 «Ka jot juróomi milyoŋ ya nag daldi dem, di ca jula, ba amaat yeneen juróom. 17 Ka jot ñaar it def noonu, ba amaat yeneen ñaar. 18 Ka jot benn milyoŋ moom dem gas ca suuf, làq fa xaalisu njaatigeem.
19 «Gannaaw diir bu yàgg njaatigeb surga ya délsi, daldi bokk xayma ak ñoom ni alalam tolloo. 20 Ci kaw loolu ka jotoon juróomi milyoŋ dikk, indaale yeneen juróom, ne ko: “Sang bi, juróomi milyoŋ nga ma dénkoon; yeneen juróom yii laa ci am.” 21 Njaatigeem ne ko: “Jaaraamaa, surga bu baax bi te wóor. Gannaaw ci lu tuut nga wóore, lu bare laa lay dénk. Kaay nag nu bokk bége.” 22 Ka jotoon ñaari milyoŋ it dikk, ne ko: “Sang bi, ñaari milyoŋ nga ma dénkoon, yeneen ñaar yii laa ci am.” 23 Njaatige la ne ko: “Jaaraamaa, surga bu baax bi te wóor. Gannaaw ci lu tuut nga wóore nag, lu bare laa lay dénk. Kaay nag nu bokk bége.”
24 «Ka jotoon benn milyoŋ it dikk, ne ko: “Sang bi, xamoon naa ne nit ku néeg nga; dangay dajale loo jiwuloon, di góob loo faruwuloon. 25 Moo tax ma ragal, ba dem gas ca suuf, làq ca sab milyoŋ. Mu ngii, fabal sa alal.” 26 Njaatige la nag ne ko: “Surga bu bon bi te yaafus! Xamoon nga ne damay dajale lu ma jiwuloon, di góob lu ma faruwuloon. 27 Kon waroon ngaa yóbbu sama xaalis ca denckati xaalis ya, ba bu ma dikkee, jot sama milyoŋ, boole ca tonoom. 28 Nanguleen nag xaalis bi ci moom, te jox ko boroom fukki milyoŋ yi. 29 Ndaxte képp ku am, dees na ko dolli, ba mu barele, waaye ku amul, la mu am as néew sax, dees na ko nangu. 30 Surga bu ñàkk njariñ bii nag, sànnileen ko ca lëndëm gu tar ga ca biti. Foofa lees di jooye aka yéyoo ndax mitit.”
Almasi bi mooy àtte àddina
31 «Keroog bu Doomu nit ki dikkee darajaam nag, ànd ak mboolem malaaka yi, mooy toog ci ngànguneem lu darajawuSeetal ci Dañeel 7.13-14., 32 mboolem xeet yi lees di dajale fi kanamam, te mooy xàjjaatle ñii ak ñee, ni ab sàmm di xàjjaatlee ay xar aki bëy, 33 te mooy teg xar yi fi ndijooram; bëy yi, fa càmmoñam.
34 «Ca la buur bay wax ñi ci ndijooram ne leen: “Yeen ñi sama Baay barkeel, dikkleen jël nguur gi ñu leen waajalaloon ba àddina sosoo. 35 Ndaxte ba ma xiifee, yeena ma leel; ma mar, ngeen nàndal ma; ma dib doxandéem, ngeen fat ma; 36 ma rafle, ngeen wodd ma; ma wopp, ngeen toppatoo ma; ñu tëj ma, ngeen seetsi ma.” 37 Su ko defee boroom njekk yi ne ko: “Sang bi, kañ lanu la gis, nga xiif, nu leel la; mbaa nga mar, nu nàndal la? 38 Ak kañ lanu la gis, nga dib doxandéem, nu fat la; mbaa nga rafle, nu wodd la? 39 Ak itam kañ lanu la gis, nga wopp mbaa ñu tëj la, nu seetsi la?” 40 Bu loolu amee buur ba ne leen: “Maa leen ko wax déy, lu ngeen ci defal kenn ci ñi gëna tuut ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.”
41 «Gannaaw loolu, ña fa càmmoñam la naan: “Yeen ñi alku nag, xiddileen ma, te tàbbiji sawara su dul fey, fa ñu waajalal Seytaane aki malaakaam. 42 Ndaxte ba ma xiifee, leeluleen ma, ba ma maree, nàndaluleen ma. 43 Ba ma dee ab doxandéem, fatuleen ma; ba ma raflee, wodduleen ma; ba ma woppee, ak ba ñu ma tëjee it, seetsiwuleen ma.” 44 Su ko defee ñoom itam ñu ne ko: “Sang bi, kañ lanu la gis, nga xiif, mbaa nga mar, mbaa nga dib doxandéem, mbaa nga rafle, mbaa nga wopp, mbaa ñu tëj la, te fajunu sa soxla?” 45 Ca la leen di wax ne leen: “Maa leen ko wax déy, lu ngeen ci defalul kenn ci ñi gëna tuut, man ngeen ko defalul.” 46 Ñooña daldi séddooji mbugal mu sax dàkk, boroom njekk yi nag séddooji texe gu sax dàkk.»

*25.15 juróomi milyoŋ: maanaam juróomi talaŋ. Seetal Xaalis ci Leeral yi.

25.31 Seetal ci Dañeel 7.13-14.