Téereb Yonent Yàlla
Mise
Mise, réewum Yuda la cosaanoo, Esayi la bokkal jamono. Mise artu na ñi ko déglu ne seenum réew, rawatina Yerusalem seen péey, dina bokk demin ak Samari, péeyub réewum Israayil ma réewum Asiri duma woon ci atum 722 lu jiitu Almasi bi. Teewul Mise biral na ne bu dumay Yàlla xasee dikk ba noppi, moom Yàlla mooy delloosi ñoñam ci boppam, jéggal leen seeni bàkkaar.
Ci tënk:
1.1—2.13 Yàlla mooy mbugal ñoñam.
3.1-12 Yàlla mooy mbugal njiit yi ak yonenti caaxaan yi.
4.1—5.15 Lu jëm ci kilifa giy ñëw ak barkey ëllëg.
6.1—7.20 Mbugalum Yàlla ñeel na Israayil.
1
Ubbite gi
1 Kàddug Aji Sax jii moo dikkaloon Mise miy waa Moreset, ca janti Yotam ak Axas ak Esekiyas, buuri réewum Yuda, na seen nguur topplantee. Lii la Mise gis ci mbirum Samari ak Yerusalem
*.
Aji Sax ji yékkati na kàddug tuuma
2 Dégluleen, yeen, xeetoo xeet,
teewlul, yaw àddina ak li ci sa biir,
ba Boroom bi Aji Sax ji seedeel leen tuuma,
Boroom beey àddoo fa màkkaanam mu sell ma.
3 Aji Sax jaa ngii di génne ca bérebam ba,
mooy wàccsi, daagoo kawtey suuf.
4 Tund ya mu joggi da naan soyox seey,
xur ya xar, wàyyi ni dax ju jege sawara,
def ni ndox mu wale kaw mbartal.
5 Bàkkaaru Yanqóobaa waral lii lépp,
moyi Israayil googu la.
Ana luy bàkkaaru Yanqóoba?
Da dul Samari?
Ana fuy bérebi jaamookaayi xërëm ci Yuda?
Da dul Yerusalem?
6 «Maay saam Samari, def ko jalu tojit
ci mbooy gi,» la Aji Sax ji wax.
«Maa koy def jëmbatukaayub reseñ,
maay yuri ay doji tabaxam ca xur wa,
ñori suuf sa mu sampe.
7 Seen jëmmi tuur yépp ay rajaxoo,
te mboolem seen peyoor yu sobewu
day lakk ba jeex.
Maay tas tasar mboolem seen jëmmi xërëm
†,
seen peyi gànc a leen ko may,
kon na ko seen moroomi gànc feyeekoo.»
Ñaawlu dikkal na Yuda
8 Lee ma tax di jooy aka yuuxu,
ne duŋŋ, deme tànki neen, di ko ñaawloo.
Naa yuuxu nig till,
naa sab sabum looy ndaxu naqar.
9 Góom bi Aji Sax ji teg Samari kat amul paj,
te moo law ba Yuda,
àkki ba buntu Yerusalem, ca saay bokk.
10 Buleen ko nettali fa Gaat
‡,
buleen jooy benn yoon.
Xalanguleen fa pëndub suuf sa ca Bet Leyafra
§,
di ko ñaawloo.
11 Yeen waa Safiir
*, wéyleen,
ak gàcce ak yaramu neen.
Waa Caanan
† sañuñoo génn,
te wall du bawoo fa waa Bet Eccel
‡,
ñay jooy seeni néew.
12 Waa Marot a mar jàmm,
te aw ay a wàcce fa Aji Sax ji,
ba agsi buntu Yerusalem
§.
13 Yeen waa Lakis
*, takkleen fasi dawkat ak watiir.
Yeena njëkka moyloo janq Siyoŋ mu taaru,
ci yeen lañu njëkka gise bàkkaari Israayil.
14 Yeen waa Yuda, mayleen waa Moreset Gaat
† lu ngeen tàggatook ñoom,
këri Agsib
‡ wori neen lay doon ci buuri Israayil.
15 Yeen waa Maresa
§ laay indil ku leen moom,
te ca Adulam
* la ñi Israayil di damoo di làquji.
16 Watuleen nel, ñaawloo ko
doom yi leen doon bànneexal.
Neluleen nel yu set nim tan, naqarloo,
nde dañu leen di gàddaayloo, teqalikook yeen.