3
Aji Sax ji tiiñal na njiiti Israayil
1 Dama ne:
«Ngalla dégluleen yeen njiiti Yanqóoba,
yeen kilifay kër Israayil!
Xanaa du yeena wara xam yoon?
2 Te yeenay bañ-kati lu baax,
di bëggkati lu bon.
Yeenay fees sama ñoñ te ñuy dund,
yeenay rocci suux wi sàng seeni yax.
3 Yeenay yàpp samay bokk,
fulli seen der,
damm seeni yax, dogat,
def ko ni toggug kawdir,
mel ni ndawal ci cin.»
4 Lee tax noggatukat yii di woo Aji Sax ji wall,
te du leen wuyu,
kanamam la leen di làq, bésub keroog,
ndax ñoo bonal seeni jëf.
Aji Sax ji artu na yonent yu bëgge yi
5 Lii la Aji Sax ji wax ci yonent yiy lajjal samay bokk:
«Bu ñu sàqamee ab lanc, yéene jàmm;
ku leen leelul, ñu waajal xare.
6 Moo tax yeen, guddi moo leen di ñeel, ba peeñu réer,
lëndëm a leen di dikkal, ba am ngis tukkil leen,
jant mooy sowal yonent yi,
bëccëg lëndëmal leen.
7 Seetkat yi dañuy rus,
boroom peeñu yi torox,
ñoom ñépp jàpp seen gémmiñ;
ndax Yàllaa leen dul faale.»
8 Teewul man, may fees ak doole,
fees ak noowug Aji Sax ji,
ak dëgg ak njàmbaarte,
ngir biralal askanu Yanqóoba bàkkaaram,
ngir tuddal bànni Israayil googu moyam.
Aji Sax ji tiiñalaat na njiiti Israayil
9 Ngalla dégluleen lii, yeen njiiti kër Yanqóoba;
yeen kilifay kër Israayil.
Yeen ñi seexlu dëgg,
lunkal wépp yoonu njub.
10 Deret ngeen tabaxe Siyoŋ,
njubadi ngeen tabaxe Yerusalem googu.
11 Seeni njiit, alalu ger lañuy àttee,
seeni sarxalkat di feyeeku am njàngale,
seeni yonent di weccikoo xaalis seenum ngisaane,
te Aji Sax ji lañuy dëgërloo, naan:
«Xanaa du Aji Sax jaa ngi ci sunu biir?
Musiba du nu dab!»
12 Kon nag yeena tax dees na gàbb Siyoŋ nib tool,
Yerusalem googu diy tojit, jale,
tundu kërug Yàlla gaay doon gajj bu kawe.