5
1 «Yaw Betleyem Efrata,
lu tuut ci làngi Yuda,
ci yaw la ku may yilifal Israayil di génne,
cosaanam di jant yu yàgga yàgg,
bu njëkkoon.»
2 Moo tax Aji Sax ji di leen wacc
ba keroog kiy matu mucc.
Ca la bokkam ya dese bakkan di dellu,
fekki seen bokki bànni Israayil.
3 Kilifa gaay taxaw, sàmme ci dooley Aji Sax ji,
ci màggug turu Yàllaam Aji Sax ji,
ba ñu dëkke jàmm,
nde léegi lay doon Ku màgg,
ba turam dajal cati àddina.
4 Kookooy doon buntu jàmm,
ba bu waa Asiri songee sunum réew,
ba daagoo sunu kawi tata,
juróom ñaari njiit lanu koy yékkatil,
ba juróom ñetti garmi.
5 Ab saamar la ñooñuy yilife Asiri,
réewum Nimrodd mooma ca biiri buntam.
Kilifa gi ñu dige moo nuy xettaleek Asiri,
bu ñu nu songee,
ba joggati sunu suuf.
Ndesu Israayil dina am doole
6 Ci biir askan yu bare la ndesu Yanqóoba di nekk,
mel nib lay bu bawoo fa Aji Sax ji,
nirook waame wu wàccal gàncax,
xaarul lenni nit,
lenni doom aadama la séentuwul.
7 Ci biir askan yu bare la ndesu Yanqóoba di nekk,
ci biir xeeti àddina,
mbete gaynde ci biir rabi àll yi,
nirook gaynde gu mat ci biiri gàtt;
fu mu jaare, joggati, xotat,
te kenn du wallu.
Cëslaay réer na bokkaalekat
8 Aji Sax ji, sa loxo ca kaw, tiim say bañ,
mboolem say noon lees di jële ci kaw suuf.
9 «Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee,
«maay sànke fi saw askan say fasi xare,
te maay sànk sa watiiri xare.
10 Maa fiy yàqe sa dëkki réew mi,
màbb sa tata yépp.
11 Maay foqatee ay xërëm ci sa loxo,
te ay gisaanekat, dootuloo ko am.
12 Maay jële fi saw askan say tuur,
ak say tuuri doj,
te dootoo sujjóotal loo sàkke say loxo.
13 Maay buddee fi saw askan xeri jaamookaayi Asera tuur mi,
te maay yàq say jëmmi tuur.
14 Mer akum sànj laay feye xeeti yéefar
yi déggul ndigal.»