3
Yeesu faj na nit ku loxoom làggi
1 Gannaaw loolu Yeesu duggati ca jàngub Yawut ba. Boroom loxo bu làggee nga fa woon. 2 Ay Farisen a ngay xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj, te muy bésub Noflaay, ngir ñu man koo tuumaal. 3 Yeesu ne boroom loxo bu làggi ba: «Taxawal fii ci digg bi.» 4 Yeesu nag ne leen: «Ana lu yoon maye; def lu baax bésub Noflaay am def lu bon? Rawale bakkan am rey?» Ñu ne xerem.
5 Ci kaw loolu Yeesu dawal bëtu mer, xool leen ñoom ñépp, boole kooku naqar ndax seen xol yu wow. Mu ne waa ja: «Tàllalal loxo bi.» Mu tàllal, loxo ba wér. 6 Ba loolu amee Farisen ya génn, diisooji ca saa sa ak farandooy Buur Erodd ca mbirum Yeesu, ngir fexe nu ñu ko sànke.
Mbooloo topp na Yeesu
7 Gannaaw loolu Yeesu aki taalibeem jóge fa, jëm dex ga, mbooloom diiwaanu Galile mu bare topp ko, ak waa diiwaanu Yude itam, 8 ak waa Yerusalem ak Idume*Idume mooy diiwaanu Edom ci làkku gereg. Ci Yuda la bokkoon, wetu bëj-saalumam. ak wàllaa Yurdan ak la wër Tir ak Sidon. Muy mbooloo mu bare mu dégg mboolem la muy def, daldi koy fekki. 9 Yeesu nag ne ay taalibeem, ñu waajal ko gaal bala ko mbooloo maa tanc. 10 Ndax booba Yeesu jotoon naa faj ñu bare, ba tax mboolem ña ame ay jàngoro song ko, di ko wuta laal. 11 Rab ya itam, saa yu ñu ko gisaa, daldi daanu fa kanamam, tey yuuxu naan: «Yaa di Doomu Yàlla.» 12 Teewul Yeesu femmu rab ya bu baax, ngir ñu bañ koo siiwal.
Yeesu tànn na fukki ndaw ak ñaar
13 Gannaaw loolu Yeesu yéeg ca tund wa, woo fa ña ko neex, ñooña dikk ba ca moom. 14 Mu tabb ca fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam, ngir ñuy ànd ak moom, ngir itam, mu di leen yebal, ñu waareji, 15 mu joxaale leen xam-xamu dàq ay rab. 16 Noonu la tabbe Fukk ak ñaar ñii, di Simoŋ ma muy wax Piyeer, 17 ak Yanqóoba ak Yowaan, doomi Sebede, ña Yeesu di wax Bowanerses, muy firi Doomi dënu, 18 ak Àndre ak Filib ak Bartelemi ak Macë ak Tomaa ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Tade ak Simoŋ, Mbokki kuréelu Moom-sa-réew ma, 19 ak Yuda Iskaryo may mujj wor Yeesu.
Gii tooñ la Yàlla dul baale
20 Yeesu dellooti kër ga, mbooloo ma dajeeti fa, ba moom ak ay taalibeem taluñoo sex dugub sax. 21 Ay bokkam dégg la xew, daldi dikk, ngir jàppsi ko, naan dafa teqalikoo ak sagoom. 22 Firikati yoonu Musaa ya jotoona wàccsee Yerusalem it ne: «Kii, Beelsebul a ko jàpp. Buuru rab boobu lay dàqe ay rab.»
23 Ba mu ko defee Yeesu woo leen, léeb leen ay léeb, ne leen: «Ana nu Seytaane mana dàqe Seytaane? 24 Ag nguur de, su dee xàjjalikoo ci biiram, googa nguur du mana yàgg. 25 Ag kër it, su dee xàjjalikoo ci biiram, googa kër du mana yàgg. 26 Seytaane nag, su jógee di xàjjalikoo ci biiram, du mana yàgg, day jeexal rekk.
27 «Du kenn moos ku mana dugg kër ponkal, buub alalam! Xanaa mu njëkka yeew ponkal mi, doora mana toj kër ga. 28 Maa leen ko wax déy, lu mu mana doon, dees na ko jéggal doom aadama, mu diy bàkkaaram, ak mboolem kàddug saaga Yàlla. 29 Waaye képp ku saaga Noo gu Sell gi, deesu ko jéggal mukk; day gàddu bàkkaar ba fàww.»
30 La ñu ne rab a ko jàpp moo waral mu wax leen loolu.
Déggal Yàllaa gën bokk ak Yeesu
31 Yaayu Yeesu moo dikkoon, ànd ak ay rakki Yeesu. Ñu taxaw ca biti, yónnee, woo ko. 32 Booba mbooloo nga toog, wër ko. Ñu ne ko: «Sa yaay ak say rakk kat ñu ngi ci biti, di la seet.» 33 Yeesu ne leen: «Ana kan mooy sama yaay? Ak ñan ñooy samay rakk?» 34 Mu dawal nag bëtam, xool ña ko yéew, daldi ne: «Dama ne, ñii ñooy sama yaay ak samay rakk. 35 Ndax kuy jëfe coobarey Yàlla, kooku moo di sama rakk ju góor, di samab jigéen, di sama yaay.»