5
Yeesu faj na ku rab jàpp
1 Gannaaw loolu ñu jàll wàllaa dex ga, ca diiwaanu waa Serasa*Serasa, diiwaan la bu féete dex ga bëj-saalum jàpp penku, ci gox bu ñu dul Yawut dëkke..
2 Naka la Yeesu génn gaal ga, jenn waay ju rab jàpp bàyyikoo ca sëg ya, dikk dogale ko. 3 Waa jaa nga dëkkoon ca sëg ya, te ag càllala sax maneesu ko ko woona yeeweeti. 4 Daan nañu ko farala jéng, yeewe koy càllala, waaye waa ja da daan dagg càllala yi, damm jéng yi, ba kenn amul kàttanu téye ko. 5 Guddeek bëccëg ma nga woon ca sëg yaak ca tund ya, di yuuxooka for ay xeer, di ko dagge yaramam.
6 Dafa séen Yeesu fu sore, daldi daw ba agsi, sukk fa kanamam. 7 Mu xaacu ca kaw, ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, ana lu ma joteek yaw? Dama lay dagaan ngir Yàlla, bu ma mbugal.» 8 Booba Yeesoo nga ko naa: «Yaw rab wi, génnal ci waa ji.»
9 Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Gàngoor laa tudd, ndaxte ñu bare lanu.» 10 Muy tinu Yeesu lu bare ngir mu bañ leena dàqe ca réew ma.
11 Fekk coggalu mbaam-xuux gu mag a nga woon ca tund wa, di for. 12 Rab ya tinu Yeesu, ne ko: «Yebal nu ci mbaam-xuux yi, ndax nu dugg leen.» 13 Mu may ko rab ya, ñu génn, duggi mbaam-xuux ya, coggal ga bartaloondoo, tàbbi ca dex ga, lu wara tollu ci ñaari junniy (2 000) mbaam-xuux daldi lab ca dex ga.
14 Ba mu ko defee sàmm ya daw, nettaliji ko waa dëkk ba, ak dëkk-dëkkaan ya, nit ña dikk, di seet la xew. 15 Ñu dikk ba ci Yeesu, daldi gis boroom rab ba, mu solu ba toog, ànd ak sagoom. Nit ña nag tiit. 16 Ña fekke woon mbir ma daldi leen nettali mbirum boroom rab baak mbaam-xuux ya. 17 Ci kaw loolu ñuy tinu Yeesu ngir mu génn seen gox ba.
18 Naka la Yeesu di dugg ca gaal ga, boroom rab ba di tinu Yeesu, ngir ànd ak moom. 19 Waaye Yeesu mayu ko ko. Da ne ko: «Ñibbil sa kër ca say bokk, nga àgge leen li la Boroom bi defal lépp ci yërmandeem.» 20 Waa ja it dem, di tàmbalee siiwtaane ca diiwaan ba ñu dippee Fukki Dëkk, la ko Yeesu defal lépp. Ñépp waaru.
Yeesu dekkal na, faj na
21 Yeesu nag jàllaat dex ga, mbooloo mu bare daje, wër ko fa mu nekk ca tàkkal dex ga. 22 Ci biir loolu kenn ci njiiti jàngub Yawut ba, ku ñuy wax Yayrus dikk. Naka la gis Yeesu, ne gurub sukk ciy tànkam, 23 di ko tinu lu bare, ne ko: «Sama doom ju jigéen ay bëgga faatu. Ngalla kaay teg ko loxo, ngir mu mucc ba dund.» 24 Yeesu ànd ak moom, dem, mbooloo mu réy topp ca Yeesu, tanc ko.
25 Sennas ndaw a nga ca woon, fukki at ak ñaar ma ngay xëpp deret. 26 Fekk na mu sonn coono bu réy bu ko fajkat yu bare teg. Mu sànk ci alalam jépp te jëlewu ci genn tan, xanaa gëna wopp. 27 Mu déggoon nag turu Yeesu, ba tax mu dikk, dugg ci biir mbooloo mi, doxe ko gannaaw, teg loxoom ca mbubbam. 28 Fekk na mu naan ci xelam: «Su ma fexee ba laal mbubbam rekk, dinaa mucc.» 29 Ba mu tegee loxoom ca mbubbam Yeesu, ca saa sa la deret ja taxaw, mu yég ci yaramam, ne teqalikoo naak jàngoro ja.
30 Yeesu nag yég ca saa sa leer gu bàyyikoo ca moom. Mu walbatiku ca biir mbooloo ma, ne: «Ana ku laal sama mbubb?» 31 Taalibeem ya ne ko: «Yaa ngi gis mbooloo mi la tanc mépp, nga naa: “Ku ma laal?”» 32 Teewul Yeesu dawal bëtam fa ko wër, ngir gis ka def loola. 33 Ndaw saa nga tiit bay lox, ndax xam na xéll la ko dikkal. Mu dikk, ne gurub sukk fa moom, daldi koy wax dëgg gépp. 34 Yeesu ne ko: «Janq, sa ngëm a la faj. Demal ak jàmm te teqalikook sa jàngoro.»
35 Yeesoo ngay wax, noppeegul, aw nit jóge ca kër njiitu jàngu ba, dikk, ne njiit la: «Sa doom faatu na. Jaratul ngay yékkati kilifa gi.» 36 Yeesu nag tanqamlu wax ja ñu wax. Mu ne njiit la: «Bul tiit, gëmal rekk.» 37 Ba Yeesu di dem kër njiit la, mayul kenn mu ànd ak moom ku moy Piyeer ak Yanqóoba ak Yowaan rakku Yanqóoba.
38 Ñu agsi kër njiit la, Yeesu yem ca coow la. Ña ngay jooyooka yuuxoo. 39 Mu duggsi, ne leen: «Lu ngeen di soow aka jooyoo? Xale bi deewul, day nelaw rekk.» 40 Waaye ñu di ko ñaawal. Yeesu génne ñépp, daldi woo baayu xale bi ak yaay ji, ak taalibe ya mu àndal, ñu jàll ca biir fa xale ba nekk. 41 Mu jàpp ca loxol xale ba, ne ko: «Talita kumi,» mu tekki: «Janq, ma ne la, jógal.»
42 Ca saa sa janq ba jóg, di dox, ndax amoon na fukki at ak ñaar. Ñépp waaru lool. 43 Ci kaw loolu Yeesu dénku leen bu baax, ne leen bu ko kenn yég, daldi ne ñu may janq bi, mu lekk.