12
Léebu beykat ya tiiñal na njiit ya
Yeesu nag teg ca di wax ak ñoom ci ay léeb. Mu ne leen: «Ab tóokëru reseñ la nit jëmbatoon. Mu ñag tóokër bi, gas ca paxum nalukaayu reseñ, tabax ca taaxum wattukaay, ba noppi batale tóokër ba ay beykat, daldi tukki.
«Ba wittum reseñ jotee, mu yebal ab surga ca beykat ya, ñu jëlsi wàllam ca meññeef ma. Beykat ya jàpp ko, dóor ko, dàq ko, mu dellu loxoy neen. Boroom tóokër ba yebalaat beneen surga, ñu xaañ ko, toroxal ko. Mu yebalati beneen surga, ñu rey ko. Mu dellu yebal ñu bare, ñii ñu dóor leen, ñii ñu rey.
«Boroom tóokër ba nag desewul kenn ku dul doomam ji mu sopp. Mu mujj koo yebal ca beykat ya te naan: “Sama doom, dinañu ko rus.” Teewul beykat ya ne ca seen biir: “Kii mooy donn; nanleen ko daldi rey, ndonoom di sunu moomeel.” Ñu jàpp ko, rey, génne néew ba tóokër ba, sànni ca biti.»
«Ana nu boroom tóokër biy def? Xanaa dikk rekk, rey beykat yi, dénk tóokëru reseñ ba ñeneen. 10 Xanaa jànguleen gii kàddu ci Mbind mi?
“Doj wi tabaxkat yi beddi woon,
moo mujj di doju koñu tabax bi.
11 Lii de, fa Boroom bi la sottee,
nu gis ko, yéemu*Seetal ci Taalifi cant 118.22-23..”»
12 Ba loolu amee njiit ya di ko wuta jàpp, ndax xam nañu xéll ne ñoo moom léeb wa, waaye dañoo ragal mbooloo ma, ba tax ñu dem, bàyyi ko.
Ndax fey galag yoon la?
13 Njiiti Yawut ya teg ca yebal ca Yeesu ay Farisen ak ay farandooy Buur Erodd, ngir ñu lalal ko fiir gu ñu ko jàppe ci kaw kàddu. 14 Ñooñu dikk ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku dëggu nga, te ragaloo kenn, ndax seetuloo ci jëmmi nit, waaye ci kaw dëgg ngay jàngalee yoonu Yàlla. Ndax yoon maye na ku fey Buur Sesaar ab galag, am déet? War nanu koo fey, am warunu koo fey?»
15 Teewul Yeesu ràññee seen jinigal, ne leen: «Ana lu ngeen may seetloo? Indilleen ma posetub dinaar, ma xool.» 16 Ñu jox ko poset, mu ne leen: «Nataal bii ak tur wii ci binde, kuy boroom?» Ñu ne ko: «Buur Sesaar.» 17 Yeesu ne leen: «Yëfi Sesaar daal, joxleen ko Sesaar, yëfi Yàlla, ngeen jox ko Yàlla.» Ñu waaru nag ci moom.
Sadusen gëmul dee-dekki
18 Sadusen yi ne dee-dekki amul, ñoo ñëwoon ci Yeesu, di ko laaj, ne ko: 19 «Kilifa gi, Musaa da noo bindal ne, ku góor, su ku mu bokkal waajur te amul doom, faatoo, su bàyyee gannaaw jabar, kooku na jël jabar ja, ngir amal mbokkam ma dee, kuutaay.
20 «Léegi juróom ñaari góor ñu bokk ndey ak baay la woon. Taaw ba am jabar, ba faatu te bàyyiwul doom. 21 Tofo ba jël ndaw sa, ba mujj dee te bàyyiwul doom. Ñaareelu tofo ba it noonu. 22 Ñu topplantee ko noonu ba juróom ñaar ñépp dee, te kenn bàyyiwul doom. Gannaaw gi, ndaw sa it dee. 23 Keroog ndekkite la nag, bu ñu dekkee, kan ci ñoom la ndaw say doon jabaram, gannaaw juróom ñaar ñépp a ko jëloon jabar?»
24 Yeesu ne leen: «Du lii mooy seen njuumte: xamuleen Mbind mi, xamuleen manoorey Yàlla! 25 Ndax ñi dee, bu ñu dekkee, kenn du ci am jabar mbaa jëkkër, waaye dañuy mel ni malaaka yi ci asamaan. 26 Te ci wàllu dee-dekki sax, xanaa jànguleen na ko téereb Musaa indee ca mbirum ngarab sa, mooy ba mu ne: “Maay Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay YanqóobaSeetal ci Mucc ga 3.6.”? 27 Kon moom du ñi dee lay seen Yàlla, xanaa ñiy dund. Njuumte lu réy ngeen juum.»
Ndigal li gëna am solo ci yoonu Musaa
28 Ci biir loolu ab firikatu yoonu Musaa bu dégg seen wax ja, daldi gis ne Yeesu tontu na leen bu baax. Mu dikk, laaj ko ne ko: «Ana lan ndigal moo gëna am solo ci ndigal yépp?»
29 Yeesu ne ko: «Ndigal li gëna am solo mooy: “Dégluleen, yeen bànni Israayil, Boroom bi sunu Yàlla, Boroom bi kenn la. 30 Kon seen Yàlla Boroom bi, nanga ko soppe sa léppi xol, ak sa léppi jëmm, ak sa léppi xel, ak sa léppi dooleSeetal ci Baamtug yoon wi 6.4-5..” 31 Ñaareel bi mooy: “Ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom§Seetal ci Sarxalkat yi 19.18..” Ndigal gënula màgg yii.»
32 Firikatu yoon bi ne ko: «Waawaaw, Kilifa gi, yaa wax dëgg; Yàlla kenn la, te amul jeneen Yàlla ju dul moom. 33 Te it nga soppe ko sa léppi xol, ak sa léppi xel, ak sa léppi doole, te ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom; loolu moo gën mboolem saraxi dóomal, ak yeneen sarax yu mu mana doon.»
34 Yeesu nag gis ne waa ja waxe xel, mu ne ko: «Sorewuloo nguurug Yàlla de.» Ba loolu amee kenn ñemeetu koo laaj dara.
Almasi bi sut na maamam
35 Yeesu nag di jàngale ca kër Yàlla ga, daldi laajte, ne: «Lu tax firikati yoon yi ne, Almasi bi, sëtub Daawuda la? 36 Daawuda ci boppam moo waxe ci ni ko leeru Noo gu Sell gi dikkale, ne:
“Boroom bi daa wax sama Sang, ne ko:
‘Toogeel sama ndijoor,
ba ma teg say noon fi sa suufu tànk*Seetal ci Taalifi cant 110.1..’ ”»
37 Yeesu neeti: «Gannaaw Daawuda ci boppam moo woowe Almasi bi “Sang bi,” ana kon nu mu nekke ab sëtam?» Mbooloo mu baree nga fa woon, di ko dégloo mbég.
38 Yeesu teg ca xamal leen ne leen: «Moytuleen firikati yoonu Musaa yi taamoo jaagar-jaagareek seen mbubb yu réy, di sàkku nuyoob wegeel ca pénc ma, 39 ak toogu yu kaname ca jàngu ya, ak péetey teraanga ca bernde ya. 40 Ñooy saax-saaxee alalu jëtun ñi tey ñaan ñaani ngistal yu dul jeex. Ñooñu la seen mbugal di gëna tar.»
Yoolu sarax ca am-amu boroom
41 Ci kaw loolu Yeesu toog ca kër Yàlla ga, janook ndaa la ñuy dugal seen xaalis bu ñuy joxe ngir Yàlla. Muy seetlu na nit ñay dugalee xaalis ca ndaa la. Ay boroom alal yu bare dugal ca dayo yu takku. 42 Ci biir loolu ab jëtun dikk, sànni ca ñaari poseti xànjarposeti xànjar: yooyu poset lepton lañu leen di woowe, te moo gënoona néew njarte ca yooya jamono. Seetal Xaalis ci Leeral yi. yu matul sax ab dërëm.
43 Yeesu nag woo taalibe ya, ne leen: «Maa leen ko wax déy, mboolem ñi sànni xaalis ci ndab li, jëtun bu néew doole bii moo leen ëpple lu mu ci sànni. 44 Ndax ñoom ñépp ci seen koom lañu sàkke as lëf, sànni ci ndab li, waaye moom de, ci biirug ndóolam la jële la mu amoon lépp, dundam bépp, sànni ci.»

*12.11 Seetal ci Taalifi cant 118.22-23.

12.26 Seetal ci Mucc ga 3.6.

12.30 Seetal ci Baamtug yoon wi 6.4-5.

§12.31 Seetal ci Sarxalkat yi 19.18.

*12.36 Seetal ci Taalifi cant 110.1.

12.42 poseti xànjar: yooyu poset lepton lañu leen di woowe, te moo gënoona néew njarte ca yooya jamono. Seetal Xaalis ci Leeral yi.