3
Ab safaan ñeel na Niniw
Wóoy, ngalla dëkkub tuurkatu deret bi,
ñépp di fen, fees aku ay,
te foqati alalu jàmbur du dakk!
 
Kàcciri dal,
ay mbege riir,
fas rëpptal,
watiir kar-kari.
Gawar buur,
saamar melax,
xeej lerxat,
ñu bare ne lasiim,
ñi dee jale,
néew ya tëë jeex,
ñuy fakkastaloo néew ya.
Aw léeb ñeel na Niniw, gànc biy xërëmtu
Lépp ndax ngànctu gu bare gi gànc bi nekke!
Jekk tànkee, boroom xërëm yi,
ci ngànctu nga jaaye ay xeet,
te xërëmtu nga naxe ay giir.
 
«Maa ngii fi sa kaw,»
kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
«Sa pendal laay ñori,
ba muur sa xar-kanam,
won xeeti jàmbur yi sa yaramu neen,
gisloo waa réew yi sa gàcce.
Maa lay xëpp mbalit, sewal la,
def lam ceetaan,
ku la gis, daw la
te naan: “Niniw tas na!
Moo ku koy jooy?”
Ana fu ma koy wutale ñu ko dëfal?»
Niniw du gën dëkku No Amon demin
Moo Niniw, dangaa gën No Amon*No Amon moy dëkk bi Asiri duma ci 663 at lu jiitu Almasi bi., péeyub Misraa?
Dëkk ba dëju fa digg wali Niil ya,
am ndox wër ko,
am tataam di géej,
miiram di ndox mu wale géej,
réewum Kuus di ndëgërlaayam,
Misra di ko dooleele doole ju dul jeex,
réewum Puut ak Libi di ko jàppale.
 
10 Teewul ñu gàddaayloo ko, yóbbu cig njaam;
ay goneem, ñu falaxe leen ci mboolem selebe yoon;
ay kàngamam, ñu tegoo bant;
kilifaam yépp, ñu jéng leen.
11 Niniw yaw it dinga bilimbaane,
jànnaxe, di wuta raw ab noon.
Doole réer na Niniw
12 Sa tata yépp ni garabi figg
yu ñoral ndoortel meññeef lay mel,
soo yëlëbee, doom ya rot,
ca gémmiñ ga ka namma lekk.
13 Say gàngoor a ngii diy jigéen fi sa biir,
sa bunti réew lafal say noon,
ne ŋàpp-ŋàppaaral,
sawara xoyom tëjukaay ya!
 
14 Niniwee, ndox moo fàggoo ab gaw,
ngay rooti te dàbbali say tata.
Duggal ci bàq bi, noote ban bi,
te ne cas móolukaay bi!
15 Fa la la sawara di xoyome,
saamar xottee la fa,
raafal la ni soccet di def.
Niniw day raaf
Fulal saw nit niy soccet,
ñu tollu niy njéeréer.
16 Ay jula nga barele,
ba ñu ëpp biddiiwi asamaan,
te ñoo mel niy soccet, tojtal, naaw.
17 Say kàngam it niy soccet,
say jawriñ ni naaxu gunóor
yu dale kaw tata, bésub sedd,
jant bi jóg, ñu daw,
te deesul xam fu ñu nekk.
Woykat jooy na Niniw
18 Buurub Asiree, say sàmm a saay,
say garmi nelaw,
sa gàngoor tasaaroo kaw tund wa,
te ku leen dajale wuute.
19 Sa damm-damm amul paj,
sab góom metti,
ba mboolem ñi dégg li la dal
di tàccu ci sa kaw,
nde ana ku sa mbon gi dul jeex lorul?

*3.8 No Amon moy dëkk bi Asiri duma ci 663 at lu jiitu Almasi bi.