5
Neyemi aar na néew-ji-doole
1 Ci biir loolu askan waak seeni jabar di xultu lool ci seen kaw bokki Yawut. 2 Ñii naan: «Nun danoo jaboot, nook sunu doom yu góor ak yu jigéen. Nañu nu jox pepp mu nu lekk, ba mana dund.» 3 Ñee naan: «Sunuy tool ak sunuy tóokëri reseñ ak sunuy kër lanuy tayle ngir am pepp ci xiif bi.» 4 Ña ca des naan: «Danoo àbb xaalis, taylee ko sunuy tool ak tóokëri reseñ ngir fey galagu buur. 5 Moona nun de, nook ñi nuy lebal benn lanu, diy bokk lenqe, te seeni doom gënuñu sunuy doom. Terewul nu ngi nara dugal sunuy doom yu góor ak yu jigéen cig njaam. Am na sax ñenn ci sunuy doom yu jigéen, ñu nekk cig njaam ba noppi. Manunu ci dara ndax sunuy tool ak sunu tóokëri reseñ a ngi ci yeneen loxo.»
6 Ba ma déggee seeni xultook seen wax jooju, ma mer lool. 7 Ma daldi dogu ci sama xol ne dinaa yedd garmi yeek njiit yi. Ma ne leen: «Yeen yeenay lebal seeni bokk, di sàkku tegandaay.» Ci kaw loolu ma woote ndaje mu réy ci seen mbir. 8 Ma ne leen: «Nun def nanu sunu kem kàttan ngir jotaat sunu bokki Yawut yi ñu jaayoon ay jàmbur. Léegi yeen ci seen bopp ngeen di jaay seeni bokk, nun nu war leena jotaat?» Ñu ne xerem, amuñu lu ñu wax. 9 Ma dellu ne leen: «Li ngeen di def de baaxul. Lu leen tee di ragal sunu Yàlla bala noo torox ci kanam noon yi dul Yawut? 10 Man itam, maak samay bokk ak samay nit, nu ngi lebal askan wi xaalis ak pepp. Waaye nanu leen baal bor bii. 11 Dellooleen leen seeni tool, tey jii, ak seeni tóokëri reseñ ak seen garabi oliw ak seeni kër. Dellooleen leen itam li ngeen leen tegoon, muy benn ci téeméeri xaaj, ci xaalis ak pepp ak biiñ ak diw.» 12 Ñu ne: «Li nga wax lanuy def. Dinanu leen ko delloo te dootunu leen laaj dara.» Ba mu ko defee ma woo sarxalkat ya, giñloo leen ca kanam sarxalkat ya, ne dinañu def li ñu wax. 13 Ba loolu amee ma yëlëb sama lafu mbubb wi may dence, daldi ne: «Yal na Yàlla yëlëbe nii mboolem ku sàmmul kàddu gii ci yeen, ba xañ ko këram ak alalam. Yal nañu ko ni yëlëbe, ba mu jeexle tàkk.» Mbooloo ma mépp ne: «Amiin,» daldi bokk sargal Aji Sax ji. Mbooloo ma mépp nag def loolu ñu wax.
14 Ba loolu weesoo, la ko dale bés ba ñu ma falee boroom réewu Yuda, ca ñaar fukkeelu atu nguurug Artaserses, ba ca fanweeru atam ak ñaar, muy fukki at ak ñaar, lekkunu alalu galag bu boroom réew yelloo, du man, du samay bokk. 15 Waaye boroom réew yi ma jiitu dañu daan noot askan wi, di leen sëf seen dund ak seen biiñ, boole ci ñeent fukki dogi xaalis*40 dogi xaalis: lim boobu mu ngi tollook liibaru xaalis.. Seeni surga it di néewal askan wi doole. Man nag defuma noonu ndax ragal Yàlla. 16 Xanaa kay damaa saxoo jàpp ci liggéeyu tata bii. Masunoo jënd suuf, te sama nit ñépp a daan daje ci liggéey bi. 17 Rax ci dolli daan naa woo téeméeri kilifay Yawut ak juróom fukk (150), di bokk ak ñoom sama njël, te limaalewuma ñi bàyyikoo ci jàmbur yi nu séq, di nu fekksi. 18 Bés bu nekk daan nañu ma waajalal aw yëkk ak juróom benni xari yar ak boroomi dunq, ak lu baree bare ci mboolem xeetu biiñ, ñu di ko indi fukki fan yu nekk. Loolu taxul ma sàkku benn yoon galag bu boroom réew di dunde, ndax liggéey bi diisoon na lool jeeg ci askan wi.
19 Kon nag rikk sama Yàlla, bàyyil xel ci man te baaxe ma, ndax mboolem li ma defal askan wii!