34
Aji Sax ji rëddlu na digu réew mi
1 Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: 2 «Santal bànni Israayil, nga ne leen: Bu ngeen duggee réewum Kanaan, lii moo di réew ma ngeen di muurloo, muy seenub cér. Réewum Kanaan a ngi, ak fa suufam yem:
3 «Yeen, seen kemu bëj-saalum a ngay dale màndiŋu Ciin, leru réewum Edom, daleeti ca catal géeju Xorom ga ca penku. 4 Seen kem daa dënglu, jaare fa féete yéegub Akerabim bëj-saalum, jaare Ciin nag, dem ba bëj-saalumu Kades Barneya, jëm Àccar Adar ba àgg Asmon. 5 Asmon la kem gay jàddaate jubal xuru Misra, doora àkki géej.
6 «Géej gu mag gi mooy doon seen kemu sowu. Loolooy seen kemu sowu.
7 «Lii nag mooy seen kemu bëj-gànnaar. Ca géej gu mag ga ngeen di rëdde, ba ca tundu Or, 8 rëdde ko fa tundu Or, mu jëm Buntu Amat, jàll ba Cedàdd, 9 wéyeeti fa, jaare Sifron, jëm Àccar Enan. Loolooy seen kemu bëj-gànnaar.
10 «Rëddleen seen kemu penku, mu dale Àccar Enan ba Sefam, 11 kemu ga wàcce Sefam, jëm Ribla, fa féete Ayin penku, wàccati ba leruji dexu Kineret, ca wet ga ko féete penku, 12 kemu ga dellu wàcc ba ca dexu Yurdan, doora àkki géeju Xorom ga. Loolooy doon seenum réew ak kemoom yi ko wër.»
13 Ba mu ko defee Musaa sant bànni Israayil, ne leen: «Réew moomu ngeen di tegoo bant, séddoo ko, te moom la Aji Sax ji santaane ñu jox ko juróom ñeenti giir yeek genn-wàll, 14 gannaaw giirug Ruben ak seeni kër maam, ak giiru Gàdd ak seeni kër maam séddu nañu, te genn-wàllu giirug Manase itam jot nañu seen cér ba noppi. 15 Ñaari giir ya ak genn-wàllu giir googu ñoo séddu suuf ca penkub dexu Yurdan, fa janook Yeriko.»
Lim nañu saytukati séddale ba
16 Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: 17 «Ñii nag ñoo leen di séddale réew mi: Elasar sarxalkat bi, ak Yosuwe doomu Nuun. 18 Ay njiit ngay jële kenn-kenn, ci giir gu nekk, ngir ñu jàpp ci séddaleb réew mi. 19 Ñooñoo di: ci wàllu giirug Yuda, Kaleb doomu Yefune; 20 wàllu giirug Cimyoneen ñi, Samiyel doomu Amiyudd; 21 wàllu giirug Beñamin, Elidat doomu Kislon; 22 wàllu giirug Daneen ñi, lenn njiit, di Bukki doomu Yogli; 23 wàllu Yuusufeen ñi, li féete ak giirug Manaseen ñi, lenn njiit, di Aniyel doomu Efot, 24 li féete ak giirug Efraymeen ñi, lenn njiit, di Kemwel doomu Siftan; 25 ci wàllu giirug Cabuloneen ñi, lenn njiit, di Elicafan doomu Parnag; 26 wàllu giirug Isakareen ñi, lenn njiit, di Paltiyel doomu Asan; 27 wàllu giirug Asereen ñi, lenn njiit, di Axiyudd doomu Selomi; 28 wàllu giirug Neftaleen ñi, lenn njiit, di Pedayel doomu Amiyudd.» 29 Ñooñu la Aji Sax ji sant ñu séddale bànni Israayil, réewum Kanaan.