Téereb Yonent Yàlla
Abdiyas
Yonent Yàlla Abdiyas moo bind téere bu ndaw bii, di ci yégle mbugal muy dikkal askanu Edomeen ñi. Li ko waral mooy nii ñu defoon ak waa Yerusalem. Gannaaw ba Babilon daaneelee Yerusalem ci atum 586 lu jiitu Almasi bi, Edomeen ña dañu leena wor, te waroon leena wallusi, ndax Edomeen ñi, ci Esawu seexu Yanqóoba lañu askanoo. Kon ci wàllu geño, ay bokki lenqey waa Yerusalem lañu. Askanu Edom mujj na misaal taxawaayu xeet yi noonoo Israayil.
Ci tënk:
1.1-9 Tuddees na tasteg Edom.
1.10-14 Lu jëm ci coxorteg Edom.
1.15-21 Lu jëm ci bésub Aji Sax ji ak ndekkitel Israayil.
1
Ubbite gi
Peeñum Abdiyas a ngii. Boroom bi Aji Sax ji moo wax lii ñeel askanu Edom*Edom mooy xeet wi soqikoo ci Esawu seexu Yanqóoba mi meññ Israayil..
Lu jëm ci mbugalum Edomeen ñi
Ab dégtal lanu dégg, mu bawoo fa Aji Sax ji,
ndaw lañu yebal ci biir xeet yi,
mu ne: «Jógleen, nu jóg song Edom xare.»
Aji Sax jee ne waa Edom:
«Tuutal leen laay def ci biir xeet yi
yeen, ñu xeeblu lool ngeen di doon.
Seen reewande sànk na leen,
yeen ñi dëkke xar-xari doj,
te seen dëkkuwaay sore kaw,
ba tax ngeen naan ci seenum xel:
“Ana ku ñu mana daane fi suuf?”
Su ngeen kaweeloon nig jaxaay,
ba seenum tàgg làqe ci biiri biddiiw it,
fa laa leen di wàccee.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Su leen ay sàcc dikkalee, mbaa sëxëtookati guddi,
yeenakay yàqule!
Waaye xanaa du la leen doy lañuy sàcc?
Su leen wittkati reseñ dikkalee,
xanaa dinañu ca wacc ay doom?
Waaye céy ni ñuy sëxëtoojee askanu Esawu!
Céy ni ñu nara jeexaatoo seeni denc!
Mboolem ñi ngeen fasool kóllëre
ñoo leen di waññi ba ca seen kemu réew,
seeni am-di-jàmm ñoo leen di nax ba man leen,
ñiy lekk seenu ñam tegal leen ag fiir ci seeni tànk,
ndax Edom moo amul ag dégg.
 
«Xanaa du bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee,
«fi Edom laay tukkale boroomi xel,
tundu Esawu woowu laay jële luy taxa dégg.
Yeen waa TemanTeman, sëtub Esawu, lañu dippee dëkkub Edomeen ba woon ca bëj-gànnaaru réew ma, te moo taxawe fii réewum Edom gépp., seeni jàmbaar ay jàq,
ba mboolem waa tundu Esawu faatu.
Lii moo waral mbugal mi
10 «Soxore gi ngeen soxore seen mbokk Yanqóoba
moo leen tax di sangoo gàcce,
te dees na leen dagg sànni ba fàww.
11 Bésub keroog ba ngeen taxawee,
janook seen mbokk,
bésub keroog ba jàmbur
ñay yóbbu seen alali bokk,
ay doxandéem song bunti dëkkam,
bay tegoo bant teraangay Yerusalem,
yeen itam, ni noon yooyu ngeen def.
12 Waruleen woona seetaan ci seen bésub mbokk,
bésub njekkaram,
Waruleen woona bége deminu Yudeen ñi
ci seen bésub sànkute,
mbaa ngeen di réy làmmiñ,
ci bésub njàqare.
13 Waruleen woona dugg sama dëkku ñoñ,
ci seen bésub tiis.
Waruleen woona bokk ci ñiy seetaan seenu ay
ci seen bésub tiis.
Waruleen woona teg loxo seeni teraanga,
ci seen bésub tiis.
14 Waruleen woona taxaw fa selebe yoon ya,
di dogale ña rëcce ca ñoom,
waruleen woona delloo ña dese bakkan
ca loxol noon ya, ci bésub njàqare.
Bésub Aji Sax ji xeet yépp la ñeel
15 «Bésub Aji Sax ji déy, dëgmal na,
ñeel xeetoo xeet.
Li ngeen def rekk lees leen di def,
seenug pey këppu ci seen kaw bopp.
16 Yeen waa kër Yanqóoba,
ni ngeen naane sama kaasu mbugal ca sama kaw tund wu sell,
ni la xeet yépp di naane ba fàww,
di naan aka jolu ba mel ni masuñoo nekk.
17 Waaye kaw tundu Siyoŋ la aw ndes di rawe,
te dina doon béreb bu sell,
waa kër Yanqóoba it moomaat seeni moomeel.
18 Kër Yanqóoba sawara lay doon,
kër Yuusufa dib tàkk-tàkk,
kër Esawu di boob
bu ñuy lakk, xoyom ko,
ba kenn du dese bakkan ci kër Esawu.»
Aji Sax jee ko wax.
 
19 Waa bëj-saalumu Yuda ñooy moom tundu Esawu,
waa suufu tund ya moom waa Filisti,
ñooy moom itam réewum Efrayim ak réewum Samari,
giirug Beñamin moom diiwaanu Galàdd.
20 Waa Israayil ñi ñu gàddaayloo woon,
gàngoor googu ñooy moom
réewum Kanaaneen ña, ba ca Sarebta,
te waa Yerusalem ca Sefarat, ñi ñu gàddaayloo woon,
ñooy moom dëkki Negew ca bëj-saalum.
21 Ay xettalikat ñooy yéeg kaw tundu Siyoŋ,
ngir yilif tundu Esawu,
nguur gi di moomeelu Aji Sax ji.

*1.1 Edom mooy xeet wi soqikoo ci Esawu seexu Yanqóoba mi meññ Israayil.

1.9 Teman, sëtub Esawu, lañu dippee dëkkub Edomeen ba woon ca bëj-gànnaaru réew ma, te moo taxawe fii réewum Edom gépp.