5
Moytul njaaloo
Sama doom, déglul sama xel mu rafet,
teewlul sama déggin,
kon nga saxoo foog,
say wax tegu ci xam-xam.
Lu mel ni lem la jigéenu njaalookat di wax,
làmmiñ wa ni diw gu ñu lay raay.
Muj ga mu wex xàtt,
di gaañe ni ñawkay saamar.
Tànk ya day bartalu wuti dee,
ay jéegoom àkki njaniiw.
Rëddul yoonu dund,
daa lajj, te xamu ko.
 
Kon, samay doom, dégluleen ma,
buleen wacc samay kàddu.
Soreel ndaw soosu,
bul jege bunt këram.
Kon nga ñàkk daraja, keneen jagoo;
ku néeg bóom la.
10 Jàmbur jariñoo sa doole,
doxandéem jagoo saw ñaq.
11 Ngay mujje onk,
desey yax, jeex tàkk.
12 Nga naan: «Su ma yégoon, sopp ab yar
te baña sofental waxi artu.
13 Lu ma tee woona dégg ku may digal,
tey teewlu sama waxi sëriñ ya?
14 Tuuti ma yàqu yaxeet
fi kanam ñépp!»
Yemal ci sa jabar
15 Naanal ci sa mbalkam bopp,
ndox ma balle sa teenu bopp.
16 Xanaa doo wasaare sa bëti ndox ca biti,
mu def ay wal ca pénc ya?
17 Nay sa alal, yaw doŋŋ,
ku bokk feneen bokkul.
18 Yal na sa naanukaay barkeel,
nga bànneexoo kiy sa jabar ba ngay ndaw.
19 Aka sopplu te jekk!
Na lay céram doy foo tollu,
na la xañ sago saa su ne.
20 Doom, ana looy xemmeme keneen,
bay fowe céri jàmbur?
 
21 Lu waay jëf, Aji Sax ji gis,
di xool mboolem fu mu jaare.
22 Jëf ju bon day fiir ka ko sàlloo,
bàkkaaram di mbaal, jàpp ko.
23 Ñàkk yar, dee;
ndof gu réy, sànku.