9
Aji Sax ji dëgg lay àtte
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Deewug doom ju góor, ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
 
Ma sante Aji Sax ji sama xol bépp,
di siiwal mboolemi kéemaanam.
Yaw Aji Kawe ji, dama lay bége,
bànneexoo la, kañ saw tur.
Noon yeey dellu gannaaw,
tërëf, sànku fi sa kanam.
 
Yaa ma àtte yoon, dëggal ma,
toog ci sab jal, di àtte njub.
Rëbb nga xeet yi, sànk ñu bon ñi,
far seeni tur ba fàww.
Noon ya raaf, gental ba fàww.
Yaa déjjati seeni dëkk, seenu askan fey.
Aji Sax jee sax dàkk,
samp jalam ngir àtte.
Moom mooy àtte àddina cig njub,
di dogalal xeet yi dëgg.
10 Aji Sax jeey làq néew-ji-doole,
mooy làqe bésub njàqare.
11 Aji Sax ji, yaw, ku la xam, wóolu la.
Aji Sax ji, yaw, ku la ñaan wallu, doo ko wacc.
 
12 Woyleen Aji Sax ji dëkke Siyoŋ,
siiwalleen ay jalooreem ci xeet yi!
13 Mooy topp nit bakkanu moroomam, di ko ba xel,
te du fàtte yuuxi néew-ji-doole.
 
14 Éy Aji Sax ji, baaxe ma,
gisal naqar wi ma bañ yi teg.
Yaa may yékkatee fa bunti dee,
15 ba ma siiwali sa woy yépp,
fa buntu Siyoŋ, dëkk bu taaru ba,
di bànneexoo sa wall gii!
 
16 Xeet yee tàbbi pax ma ñu gasoon,
fakkastaloo fiir ga ñu làqoon.
17 Aji Sax jaa ngi feeñoo, di àtte yoon;
ku bon tegug fiir, tàbbi ca.
Na jib ndànk. Selaw.
 
18 Ñu bon ñee dëddu, dem njaniiw,
ànd ak xeet yi fàtte Yàlla yépp.
19 Yàlla du tanqamlu ab ndóol ba fàww,
yaakaaru néew-ji-doole du tas mukk.
 
20 Aji Sax ji, jógal, bu la nit yab;
na xeet yi dikk fi sa kanam, nga àtte leen.
21 Rikk Aji Sax ji, yónnee leen tiitaange,
xamal leen ne nit doŋŋ lañu.
Selaw.