26
Ma waajal ndajem kër Aji Sax ji
Ñeel Daawuda.
 
Aji Sax ji, àtte ma,
man de màndu laa wéye,
Aji Sax ji laa wóolu, jenguma.
Aji Sax ji, nattu ma, seetlu ma,
seggal xel ak xol.
Maa ngi janook sa ngor,
di doxe sa dëgg.
Toogumaak naxekat,
lëngoowumaak naaféq,
sib naa gàngooru saay-saay,
toogumaak ku bon.
Aji Sax ji, maay jàpp ci biir mucc ayib,
di wër sa sarxalukaay,
àddu, sant la,
lim sa jépp jaloore.
Aji Sax ji, maa sopp sa dëkkuwaay,
bëgg béreb bi sag leer teew.
 
Bu ma buubaaleek bàkkaarkat, sànni,
di ma booleek bóomkat, bóom.
10 Seeni loxoo nga sóobu ci mbon,
ndijoor ya fees aki ger.
 
11 Man nag màndu laay wéye,
tee nga maa jot, baaxe ma?
12 Ndokk bi ma taxawee joor gu wóor.
Ma màggal Aji Sax ji fi ndajey way-ngëm ñi.