41
Jarag bu ñu toŋal a ngi ñaan
1 Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
2 Ndokkalee yaw mi yég néew-ji-doole.
Aji Sax jee lay xettali, bésub njàqare.
3 Aji Sax jee lay aar, di sàmm sa bakkan,
nga jagoo barke ci réew mi,
te du la bàyyi noon def la lu ko neex.
4 Aji Sax jee lay dooleel soo woppee,
di soppi bu baax sa tëraay.
5 Dama ne: «Aji Sax ji, tooñ naa la;
baaxe ma, faj ma.»
6 Noon yaa ngi may yéene lu bon,
naan: «Xanaa kii du dee, ba ñu fàtte ko?»
7 Ku dikk, di ma seet, di jinigal
tey fenti sos ci xolam,
bu génnee, tasaare ko.
8 Bañ yépp a ngi may déeyoo,
di ma fexeel lu bon,
9 naan: «Musiba dal na ko, du jógati!»
10 Sama am-di-jàmm bu ma wóolu sax jógal na ma,
te daan lekk samaw ñam.
11 Waaye ngalla Aji Sax ji, baaxe ma,
yékkati ma, ma fey leen.
12 Su noon damuwul ci sama kaw,
ma doora xam ne bége nga ma.
13 Man, damaa màndu, nga taxawu ma,
dëj ma fi sa kanam ba fàww.
14 Cant ñeel na Aji Sax ji Yàllay Israayil.
Moo masa yelloo cant ba fàww.
Amiin, Amiin.