47
Yàllaay Buur
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor.
 
Na xeetoo xeet tàccu,
xaacu, sarxolleel Yàlla!
Aji Sax ji, Aji Kawe jee jara ragal,
mooy buur bu mag bi tiim àddina sépp.
 
Moo nu nangulal xeet yi,
nu teg tànk gàngoor yi.
Moo nu tànnal céru suuf,
muy sagu askanu Yanqóoba wii mu sopp.
Selaw.
Yàllaa yéeg, kàddu riir.
Aji Sax jee yéeg, bufta*bufta, ab béjjénu kuuy la, bu ñu bënn ñaari wet yi, ngir man cee wal. jolli.
 
Woyleen Yàlla, woyleen,
woyleen Yàlla sunu buur, woyleen.
Yàllaay buuru àddina sépp;
taalifleen, woy ko.
Yàllaa di buuru xeet yi,
Yàllaa tooge jalam bu sell.
10 Kàngami xeet yeey daje,
ànd ak ñoñi Yàllay Ibraayma;
Yàllaa moom buur yi yiir àddina,
te moo kawee kawe.

*47.6 bufta, ab béjjénu kuuy la, bu ñu bënn ñaari wet yi, ngir man cee wal.