53
Mbon maase na
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maxalat, dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda.
 
Ab dof a nga naa ca xelam:
«Yàlla amul,»
Ñu ni mel ay def njekkar,
seeni jëf siblu,
kenn defu ci lu baax.
 
Yàllaa tollu asamaan, jéer doom aadama,
di seet ku ci xelu, tey wut Yàlla.
Ñépp a dëddu,
bokk yàqu yaxeet.
Kenn deful lu baax,
du kenn sax.
 
Yàlla nee: «Xanaa ñiy def lu bon, xamuñu dara?
Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam,
te wutuñu Yàlla.»
Waaye ñooy tiit a tiit
fu tiitaange amul.
Yàllaay tasaare néewi nit ñi la gaw.
Yàllaa leen wacc, nga gàcceel leen.
 
Ana kuy tollu Siyoŋ, xettali Israayil?
Éy, bés bu Yàlla tijjee wërsëgu ñoñam,
ndaw mbégte ci giirug Yanqóoba!
Ndaw bànneex laa ne, ci Israayil gii!