57
Yàlla jógal, wallu ma!
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bi ñuy woowe Bul yàq, diy ñaan, ñeel Daawuda, gannaaw ba mu dawee Buur Sawul, ba dugg ca xunt ma*Seetal ci 1.Samiyel saar 24..
 
Éy Yàlla, baaxe ma, ngalla baaxe ma,
fi yaw laay làqu,
yiiroo sa kiiraay,
ba musiba yi jàll.
Ma woo Yàlla, Aji Kawe ji,
Yàlla, mi may matalal.
Mooy yónnee fa asamaan, musal ma,
dumaal ma ku may noot.
Selaw.
Yàllaay yónnee jëfi ngoram ak wormaam.
 
Maa ngi tëdd ci biiri noon
yu mel niy gaynde, di yàpp doom aadama.
Seeni sell niy xeej aki fitt,
seen làmmiñ di saamar yu ñaw.
Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan,
sag leer tiim suuf sépp.
Noon yi di ma fiir,
sama xol jeex.
Ñu gasal mam pax,
far tàbbi ca.
Selaw.
 
Yàlla, dogu naa,
dogu naa woy, di la kañ.
Na sama jëmm jépp yewwu,
xalam ak moroom ma yewwu;
ma yee leeru njël.
10 Boroom bi, naa lay gërëm ci biir xeet yi,
kañ la ci biir waaso yi.
11 Sa ngor a màgg, ba àkki asamaan,
sa worma àkki fa kaw-a-kaw.
 
12 Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan,
sag leer tiim suuf sépp.

*57.1 Seetal ci 1.Samiyel saar 24.