61
Naa woote wall
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda.
 
Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy,
teewlul, ma dagaan la.
Àll laa lay woowe,
sama xol jeex;
yéege ma doju rawtu wu ma jotul.
Yaw laa làqoo,
ngay tata ju dëgër, fegal ma noon.
Naa dëkke sa xayma ba fàww;
làqoo sa kiiraay.
Selaw.
Yàlla, yaa dégg samay dige,
sédd ma céru ñi wormaal sa tur.
 
Ngalla féqal fani Buur,
ay atam bare, sët ba sëtaat.
Éy Yàlla, yal na Buur toog ba fàww fi sa kanam,
nga sédd ko sa ngor ak sa worma, mu fegoo;
kon ma woy la ba fàww,
di jëfe samay dige bésoo bés.