66
Yàllaay aar nitam
1 Mu jëm ci njiital woykat yi, di woyu cant.
Yeen waa àddina sépp, sarxolleelleen Yàlla,
2 woyleen màggaayu turam,
darajaalleen cantam.
3 Neleen Yàlla: «Yaaka yéemey jaloore!
Sa doolee bare, ba say noon rasu,
4 àddina sépp di la sujjóotal,
di la woy, di joobe sa tur.»
Selaw.
5 Dikkleen gis li Yàlla def,
jëf la ju yéeme, ñeel doom aadama yi.
6 Moo soppi géej ag joor,
maam ya dox jàll.
Nanu ko bége foofa.
7 Mooy nguuroo njàmbaaram ba fàww,
di topp xeet yeek bët.
Ku koy diiŋat, yàlla boo damu!
Selaw.
8 Yeen xeet yi, santleen sunu Yàlla,
te biral cantam!
9 Moo sàmm sunu bakkan,
te waccu nu, nu tërëf.
10 Éy Yàlla, nattu nga nu,
xelli nu, ni ñuy xellee xaalis;
11 laaw nga nu,
teg nu njàqare.
12 May nga noon noot nu,
nu jaare sawara, jaarem ndox;
nga génne nu, yaatal nu.
13 Maay duggaale sa kër ay saraxi rendi-dóomal,
defal la samay dige
14 yi ma waxoon ci sama gémmiñ,
sama làmmiñ tudd ko, ba ma jàqee.
15 Jurug yafal, ma defal la saraxu rendi-dóomal,
saxaar sa jollee ca kuuyu sarax ya,
ma boole ca saraxu nag ak sikket.
Selaw.
16 Képp ku ragal Yàlla dikkal, déglu,
ma limal la li mu ma defal.
17 Moom laa woo wall,
àddu, màggal ko.
18 Su ma naroon ñaawtéef,
Boroom bi du ma déglu.
19 Waaye Yàlla dégg na ma,
teewlu na samag ñaan.
20 Cant ñeel na Yàlla,
gàntuwul samay ñaan,
xañu ma ngoram.