70
Yàlla, gaawe ma
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, di woy wuy fàttalee.
 
Yàlla, wallu ma!
Éy Aji Sax ji, gaawe ma!
 
Kuy wut sama bakkan,
yal na rus, torox ne tott.
Kuy bége sama loraange,
yal nañu ko duma, waññi ko, mu ne yàcc.
Kuy ñaawalaate,
yal nañu ko toroxal, mu daw, dellu gannaaw.
 
Képp ku la wër,
yal na bég, di la bànneexoo.
Képp ku safoo sag wall,
yal na jàppoo: «Yàlla màgg na!»
 
Man de, néew naa doole, ñàkk naa.
Éy Yàlla, gaawe ma.
Yaw yaa may wallu, xettali ma.
Éy Aji Sax ji, bu ma yeexe.