85
Aji Sax ji, suqaleeti nu
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor.
 
Éy Aji Sax ji, yaa baaxe woon sa réew mi,
ba suqali sëti Yanqóoba yi,
baal sa mbooloo seeni ñaawtéef,
jéggal leen bépp bàkkaar.
Selaw.
Bàyyi nga xadar ja,
muñ mer ma.
 
Éy Yàlla mi nuy musal, suqali nu,
te meddi.
Xanaa doo nu mere fàww,
ba ca sët yaak sëtaat ya?
Xanaa dinga leqali sa mbooloo,
ba ñu man laa bànneexoo?
Éy Aji Sax ji, won nu sa ngor,
baaxe nu sag wall.
 
Woykat ba nee: «Naa déglu
lu Aji Sax ji Yàlla di wax.»
Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam,
ba duñu dellu ci jëfi dof.
10 Wallam aka jege ñi ko ragal,
te leeram dëgmal sunu réew mii!
11 Ngor ak wormaa daje,
njub ak jàmm saafoonte,
12 kóllëre jebbee fa suuf,
njub séentoo asamaan,
13 Aji Sax ji it maye ngëneel,
sunu suuf meññal,
14 njub jiitu Aji Sax ji,
di ko xàllal yoonam.