92
Nu woy bésub Noflaay
Di woyu cant ngir bésub Noflaay.
 
Céy ngëneel li ci sant Aji Sax ji,
di la woy, yaw Aji Kawe ji,
xëye tudd sa ngor,
gonloo xamle sa kóllëre,
xalamu fukki buum ànd ak moroom ma,
xeetu kooraa jibandoo.
Aji Sax ji, yaa ma bégale say jaloore,
may sarxolle ci say manoore.
Aji Sax ji, yaa réyi jëf;
xóoti pexe.
Ku ñàkk xel réere ko,
ku dofe umple ko.
Bu ku bon sëqlee nim ñax,
képp kuy def lu bon di yokkule,
dañoo nara sànku ba fàww rekk.
 
Waaye yaw ma fa kaw,
yaay Aji Sax ji ba fàww.
 
10 Aji Sax ji, sa noon yi kay, ndeke yoo;
ndeke yoo sa noon yi, sànku rekk;
defkati mbon ñépp, fëlxoo rekk.
11 May nga ma dooley nagu àll,
ma diwoo diw gu bees.
12 Maa gis jéllu noon yi,
dégg yuuxi ñu bon ñi may tëru.
13 Ku jub day naat nig tàndarma,
màgg ni garabu seedaru Libaŋ
14 gu ñu jëmbat ci biir kër Aji Sax ji,
muy naate ci sunu biir ëttu Yàlla;
15 bu màggatee sax di meññ,
tooy xepp, sëq lipp,
16 di biral njubteg Aji Sax ji,
sama cëslaay ji dencul njubadi.