105
Aji Sax ji sàmm na kóllëre
1 Santleen Aji Sax ji, tudd turam,
xamley jalooreem ci biir xeet yi.
2 Woyleen ko, tagg ko,
yégleleen mboolemi kéemaanam!
3 Damooleen turam wu sell,
yal na kuy wut Aji Sax ji am bànneexu xol.
4 Wutleen Aji Sax ji, sës ci dooleem.
Saxooleen koo wër!
5 Fàttalikuleen ay jalooreem
aki kéemaanam aki àtteem.
6 Yeen askanu Ibraayma, jaamam ba,
yeen sëti Yanqóoba, yeen ñi mu tànn!
7 Kee di sunu Yàlla Aji Sax ji,
di àtte suuf sépp,
8-9 di fàttaliku ba fàww kóllëreem,
ak kàddoom ga mu digoon Ibraayma,
ba ci junniy maas,
te mu giñal ko Isaaxa,
10 dëggalal ko Yanqóoba, sàrtal ko,
fase kook Israayil mooma kóllëre gu sax.
11 Moo noon: «Yaw laay jox réewum Kanaan,
muy sa cér, nga séddoo.»
12 Ba bànni Israayil doonee ñu néewa néew,
diy doxandéem ci réew mi,
13 di wëreelu ci biir xeetoo xeet,
ak nguuroo nguur,
14 mayul nit mu noot leen,
te yaral na leen ay buur,
15 ne leen: «Buleen laal ñi ma séddoo,
te samay yonent buleen leen lor.»
16 Moo wàcce ab xiif ca réew ma,
dagge fa lépp luy gub,
17 yónnee ku leen jiitu,
muy Yuusufa ma ñu jaayoon njaam,
18 tànk ya, ñu jéng jéng yu tar,
baat ba, ñu yeewe caqu weñ.
19 Kàddug Aji Sax ji di nattu Yuusufa,
ba keroog pirim ma dikk,
20 Buur a yónni ku ko yiwi,
ku yilifi xeet a ko tijji.
21 Mu sas ko mu jiite këram,
di saytu mboolem alalam,
22 ba saña tënk jawriñi buur ci coobareem,
tey xelal mag ña.
23 Israayil agsi Misra,
muy nganug Yanqóoba ga ca réewum Xam*Israayil ak Yanqóoba, kenn ki la; réewum Xam mooy Misra ba tey..
24 Aji Sax ji giiral xeetam wa,
ba ñu gëna bare seeni noon,
25 mu xiir waa Misra ci dëddu ñoñam,
ñuy fexeel jaamam ñooña.
26 Mu yónni Musaa, jaamam ba,
tànn Aaróona, boole ca,
27 ñu sottal ci seen biir firndeem ya mu waxoon,
muy kéemaan ya ñu def ca réewum Xam.
28 Moo yónnee lëndëm, lëndëmal,
te Musaa ak Aaróona gàntaluñu kàddoom.
29 Moo soppi seen ndoxum réew deret,
rey seeni jën,
30 feesal seen réew ay mbott
yu àkki seen biir néegi buur ya.
31 Moo àddu, weñ ya dikk,
yoo ya dajal seen réew ma.
32 Mu def seenub taw tawub yuur,
sawaray melax jafal seen réew ma.
33 Mu dal ci seen figg ak reseñ,
daaneel seen garabi réew ma.
34 Mu àddooti, ay soccet dikk,
di njéeréer yu wees ab lim,
35 ñu lekk luy gàncax ca seenum réew,
lekk lu suuf sa meññ.
36 Moo faat luy taaw ca seenum réew,
muy lu njëkka soqeekoo seen digg doole.
37 Mu génne leen, ñu yóbbaale xaalis ak wurus,
te kenn tërëful ca seeni giir.
38 Misra daa bég ba ñu demee
ndax tiitaange ju ñu leen tiital.
39 Mu firiw niir, yiire leen,
ak sawara, ñu niitoo guddi.
40 Ñu sàkku, mu wàcceey picci përëntaan,
teg ca reggal leen mburum asamaan.
41 Mu bënnu doj, ndox ma ball,
di dex, wale joor gu wow.
42 Daa bàyyi xel kàddoom gu sell,
ga mu waxoon Ibraayma, jaamam ba.
43 Moo génne ñoñam, ñu bég,
moo génne tànnéefam ña, ñuy sarxolle.
44 Mu jox leen suufi yéefar ya,
ñu jagoo ñaqi xeet ya,
45 ngir ñu sàmm ay dogali yoonam,
topp ndigali yoonam.
Màggalleen Ki Sax!