120
Ma ñaan ci biir tuuma
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
 
Ci sama njàqare laa woo Aji Sax ji wall,
mu wuyu ma.
Éy Aji Sax ji, musal ma ci gémmiñu fen-kat,
ak làmmiñu njublaŋ.
Yaw boroom làmmiñu njublaŋ,
ana lu ñu lay añale
ak lu ñu lay dolli?
Xanaa fitti mbër yu ñaw
ak xal yu yànj.
 
Wóoy man mi ganeyaani baadooloy Meseg ya
tey dali fa xaymay waa Kedar ñu xayadi ña!
Yàgg naa lool
ci biir nit ñi bañ jàmm.
Man may wut jàmm,
te su ma waxee, ñoom ñuy ayoo.