137
Jooye nanu àll
Ca tàkkal dexi Babilon,
foofa lanu daa toog,
fàttaliku Siyoŋ, jooy.
Ca garab ya
lanu daa wékk sunuy xalam.
Fa la nu sunuy sang daa woyloo,
noot nu, bëgg nu bégal leen,
naan: «Woyalleen nu ci woyi Siyoŋ.»
Moo! Nu nuy woye woyu Aji Sax ji
kaw suufas yéefar?
Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte,
yal na ma doole dëddu!
Yerusalem, su ma la fàttalikuwul,
fonk la, ba gën laa bége lépp,
yal na sama làmmiñ tafoo sama denqleñ.
 
Aji Sax ji, fàttalikul Edomeen ña,
keroog jantub Yerusalem,
ba ñu naan: «Màbbleen a màbb,
ba suuf sa dëkk bi sampe siiñ!»
Yeen waa Babilon gi ñu nara fàllas,
ndokkalee ku leen fey jëf ja ngeen nu def!
Ndokkalee ku ne cas seeni fere,
tas ciw doj!