146
Buur Yàllaa jara wóolu
1 Màggalleen Ki Sax!
Naa màggale Aji Sax ji xol,
2 fii ak may dund, di ko kañ,
fii ak may noyyi, di woy sama Yàlla.
3 Buleen wóolu kilifa,
doom aadama amul wall.
4 Noo ga day rëcc, mu dellu suuf;
bu bés baa, pexeem jeex.
5 Ndokkalee kuy dimbalikoo Yàllay Yanqóoba;
di yaakaar Yàllaam Aji Sax ji,
6 Ki sàkk kaw ak suuf,
géej ak lépp li ci biir,
di sàmm dëgg ba fàww,
7 di àtte néew-ji-doole,
di leel ku xiif.
Aji Sax jeey tijji ku ñu tëj.
8 Aji Sax jeey xippil silmaxa,
di siggil ku sëgg.
Aji Sax jee sopp ku jub.
9 Aji Sax jeey sàmm doxandéem,
taxawu jirim ak jëtun,
waaye mooy lajjal pexem ku bon.
10 Aji Sax jeey nguuru ba fàww.
Yaw Siyoŋ, sa Yàllaa ñeel maasoo maas.
Màggalleen Ki Sax!