148
Na àddina wërngal këpp màggal Yàlla
Màggalleen Ki Sax!
Nangeen màggale Aji Sax ji fa asamaan,
màggale ko fa kaw-a-kaw.
Màggalleen ko, yeen malaakaam yépp,
màggalleen ko, yeen gàngooram yi.
Màggalleen ko, yeen jant beek weer wi,
màggalleen ko, yeen mboolem biddiiw yii di nes-nesi.
Màggalleen ko, yeen asamaani kaw-li-kaw,
ba ca ndox ma tiim asamaan ya.
Nañu màggal turu Aji Sax ji,
kii kat a santaane, lii lépp am.
Moo leen samp, ñu sax ba fàww,
mu dogal ko, te du toxu.
 
Nangeen màggale Aji Sax ji fa kaw suuf,
yeen ninki-nankay géej ak xóote yépp,
ba ca melax yaak doj yu sedd yay taw,
ak tawub yuur akub lay,
ba ca ngëlén yu mag yay def ndigalam.
Màggalleen ko yeen tund yu mag yeek
yu ndaw yépp,
ba ci garab yiy meññ ak garabi seedar yi,
10 ba ci mala yépp, yu àll ak gépp jur
ak luy raam ak njanaaw,
11 ak buuri àddinaak xeet yépp,
ak kilifa yeek njiiti àddina yépp,
12 xale bu góor ak bu jigéen,
mag ak ndaw.
13 Màggalleen turu Aji Sax ji,
moom doŋŋ la turam kawe,
darajaam tiim asamaan ak suuf.
14 Moo dooleel ñoñam,
wóllëreem ñiy mbooloom bànni Israayil,
xeet wi mu xejjoo, di ko màggal.
Màggalleen Ki Sax!