10
1 Bokk yi, sama yéeney xol ak ñaan gi may ñaanal Israayil ci Yàlla moo di ñu mucc. 2 Ñoom laa seedeel seenug parlu ci Yàlla, waaye dañu koo tegul ci xam-xam bu doy. 3 Yoonu njub gi Yàlla di baaxe nit ki àtteb ku jub, moom lañu umple tey jéema dëggal seen njubteg bopp. Moo tax nanguluñu njubte gi Yàlla di maye. 4 Ndax kat Almasi bi moo sottal yoonu Musaa, ngir àtteb ku jub ñeel képp ku ko gëm.
Coobarey Yàlla mooy ñépp mucc
5 Njub gi sàmm ndigali yoon di maye, li ci Musaa bind moo di: «Kuy jëfe ndigal yooyu, yaay dund ndax ñoom*Seetal ci Sarxalkat yi 18.5..» 6 Waaye njub gi ngëm di maye, li muy digle mooy:
«Bul wax ci sa xel, ne: “Ana kuy yéeg fa kaw asamaan?”»
nde day mel ni Almasi bi ngay wuta wàcce.
7 «Bul ne it: “Ana kuy wàcci njaniiw?”»
nde day mel ni dangay wuta dekkilaat Almasi bi. 8 Li mu wax moo di:
«Kàddu gi kay jege na leen lool: ci seen gémmiñ ak ci seen biir xol la nekk†Seetal ci Baamtug yoon wi 30.11-14..»
Te loolu mooy kàddug ngëm gii nuy xamle. 9 Saw làmmiñ, soo ci biralee ne Yeesu moo di Boroom bi, sab xol it, nga gëm ci ne Yàlla dekkal na Sang Yeesu, dinga mucc. 10 Ndax kat ab xol lees di gëme, ba am àtteb ku jub, te aw làmmiñ lees di birale ngëm gi ba mucc. 11 Mbind mi moo ne: «Képp ku ko gëm, doo rus‡Seetal ci Esayi 28.16..» 12 Ag wuutale amul diggante ab Yawut ak jàmbur bu dul Yawut; ñépp a bokk benn Boroom biy yéwéne mboolem ñi koy woo wall. 13 Ndax kat waxees na ne: «Képp ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw§Seetal ci Yowel 3.5..»
14 Waaye nees di woowe koo gëmul? Nees di gëme koo déggul turam? Nees di dégge turam, te yégleesu ko? 15 Nees di yéglee xibaar, te yebaleesu la? Noonu la Mbind mi indee ne: «Ñeeka rafeti tànk, ndaw yii di yéglesi xibaari jàmm*Seetal ci Esayi 52.7.!»
16 Waaye du ñépp a nangul xibaaru jàmm bi; moo tax Esayi ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunub dégtal†Seetal ci Esayi 53.1.?» 17 Kon boog ngëm ci dég-dég lay juddoo, dég-dég ba bawoo ci kàddug waare gi jëm ci Almasi bi.
18 Waaye dama ne: xanaa dañoo déggul? Ahakay! Ndax
«Suuf sépp la seen ndéey jibal,
seen kàddoo àkki cati àddina‡Seetal ci Taalifi cant 19.5..»
19 Ma neeti: xanaa bànni Israayil dañoo xamul? Ahakay! Musaa moo leen njëkkoona jottali la Yàlla noon:
«Yeen, maa leen di fiireloo xeet wu tekkiwul dara,
ci waasow naataxóona laa leen di merloo§Seetal ci Baamtug yoon wi 32.21..»
20 Esayi it am fit ba ne:
«Ñi ma seetul woon, gis nañu ma,
ca ña ma laajul woon laa feeñe*Seetal ci Esayi 65.1..»
21 Israayil nag la wax ci mbiram ne:
«Bëccëg bépp laa yendoo tàllal samay loxo
askanu fippukat wu déggadi†Seetal ci Esayi 65.2..»
*10.5 Seetal ci Sarxalkat yi 18.5.
†10.8 Seetal ci Baamtug yoon wi 30.11-14.
‡10.11 Seetal ci Esayi 28.16.
§10.13 Seetal ci Yowel 3.5.
*10.15 Seetal ci Esayi 52.7.
†10.16 Seetal ci Esayi 53.1.
‡10.18 Seetal ci Taalifi cant 19.5.
§10.19 Seetal ci Baamtug yoon wi 32.21.
*10.20 Seetal ci Esayi 65.1.
†10.21 Seetal ci Esayi 65.2.