Ngën-gi-woy
Ngën-gi-woy mooy téere bi firndeel ne mbëggeel gu dox diggante ñaar ñu seenub séy dagan, Yàlla gërëm na ko. Mooy li Yàlla cig mbaaxam tëraloon ca toolub Àjjana, diggante Aadama ak Awa.
Mbëggeel mooy jum bi Aji Sax ji taal te mooy xamb woy wii (8.6) Aji Sax ji cofeelu neen la, te moo sàkk séy. Mbëggeel, dara manu ko fey te kenn amul njëgam (8.7).
Ci tënk, manees na xàjjale woy wii juróom ñetti taalif, ci ni ñuy baamtuwaate baat yi.
1.1—2.7 Cofeel door na.
2.8-17 Wootante jib na.
3.1-5 Réeroo, gise.
3.6—5.1 Daagu, jëm toolu mbëggeel.
5.2—6.3 Xol jeex na, mujje neex.
6.4—7.10 Yaaka taaru.
7.11—8.4 Ayca ca tool ba.
8.5-14 Joxe naa xol.
1
Cofeel door na
1 Lii, di ngën-gi-woy, ñeel Suleymaan.
Ndaw si
2 Fóon maa, ngalla fóon ma,
sa cofeel a ma dàqal biiñ.
3 Sa diw yi ngay xeeñoo neex,
saw tur jib, mel ni lu xeeñ a xelli.
Moo tax janq ji nob la.
4 Yóbbaale ma, nu daw, dem.
Sama buur, yóbbu ma sa néeg,
nu bokk mbég ak bànneex,
di tàqamtikoo sa cofeel gi dàq biiñ.
Ñoo yey nob la!
Ndaw si
5 Yeen janqi Yerusalem, damaa ñuul, rafet;
ñuul ni xayma ya ca Kedar*Kedar, diiwaanu Arabi la woon bu genn giirug Ismayla dëkke woon bu yàgg. Dañu daan defare seeni xayma ay deri bëy yu ñuul.,
mel ni ridoy Buur Suleymaan.
6 Buleen ma xoole sama ñuulaay bi,
jant bee ma lakk.
Samay càmmiñ a ma mere,
di ma wattuloo tóokëri reseñ ya,
te wattuwuma sama tóokëri bopp†tóokër ak sàmm ay baat la yu ñuy méngalee ndaw si ci waxin. Seetal it ci aaya 8 (1.8)..
7 Sama soppey xol, ngalla wax ma ana fooy foral,
di fa gooral, digg bëccëg?
Lu ko moy may muuru, di la wër
fi say xarit ak seeni gétt.
Waa ji
8 Aa! Xamoo koo?
Yaw mi dàq ci jigéen ñi!
Génnal rekk, topp wewi jur gi,
sàmmi say tef,
fi dendeek mbaari sàmm si.
9 Xarit, xam nga lu ma lay xoole?
Yànjaayu wajan wu takk watiiru Firawna.
10 Sa lex yaa ngi tàkk fi digg sàdd yi!
Céy wii loos ak caqu peram!
11 Sàddi wurus lanu lay defaral,
tapp ca xaalis.
Ndaw si
12 Li sama buur tëdd, di xéewlu lépp,
maa ngi gilli lu neex.
13 Sama nijaay di mbuusum ndàbb
may fanaan sama digg ween.
14 Saa nijaay, saa cabbu tóor-tóoru fuddën,
fa digg tóokëri Engedi‡Engedi, bëtu ndox la bu nekk ca sowub géeju Xorom ga. Engedi di tekki «bëtu ndoxu bëy»..
Waa ji
15 Xarit, yaaka rafet,
yaaka taaru!
Say gët niy pitax.
Ndaw si
16 Nijaay, yaaka góorayiw,
yaaka maa neex!
Mbooy gu naat, nu laloo,
17 garabi seedar di sunu xànqi néeg,
garab gu dul ruus xadd ko§seedar ak garab gu dul ruus, ay garab lañu yu neex xet..
*1.5 Kedar, diiwaanu Arabi la woon bu genn giirug Ismayla dëkke woon bu yàgg. Dañu daan defare seeni xayma ay deri bëy yu ñuul.
†1.6 tóokër ak sàmm ay baat la yu ñuy méngalee ndaw si ci waxin. Seetal it ci aaya 8 (1.8).
‡1.14 Engedi, bëtu ndox la bu nekk ca sowub géeju Xorom ga. Engedi di tekki «bëtu ndoxu bëy».
§1.17 seedar ak garab gu dul ruus, ay garab lañu yu neex xet.