Kóllëre gi yees
Kóllëre gi yees moo ëmb xibaaru jàmm bii di xamle dundug Almasi Yeesu, dale ko ci juddoom ba ci njàngaleem ngir teg nit ci yoonu jàmm, ak cofeelam ci nit, ba musal leen ci sànkute.
Yeesu Almasi bi moo di «Na-amee-nii» ngir digey Yàlla yépp (Esayi 65.16). Mooy Boroom tur wu rafet wii: Kàddug Yàlla, ndax moo làmboo yéene ju rafet ji Yàlla am, ngir baal nit ñi seeni bàkkaar, ba noppi boole leen ci ndamam. Ni ay dex di wale, tàbbi géej, ni la waxi yonent yi mate ci Yeesu.
Yaw miy jàng téere bii nag, yal na Yàlla barkeel sam njàng. Yal na la Noowam gu Sell taxawu, te leeralal la ko, ba nga dajeek yiwam. Te woote bu mag bi jibe woon ci gémmiñu Rammukat bi, mu ngi dégtu ba tey: «Mboolem yeen ñi loof ndax sëf bu diis, ñëwleen ci man, man maa leen di noppal.» (Macë 11.28). Mu ne it, «ku seet, gis» (Macë 7.8).