5
Juróom benneelu misaal: téere bu ñu taxañ buy naaw
1 Ci kaw loolu ma dellu séentu, gisuma lu moy téere bu ñu taxañ buy naaw. 2 Malaaka mi ne ma: «Loo gis?» Ma ne: «Téere bu ñu taxañ buy naaw laa gis, guddaay bi di ñaar fukki xasab, yaatuwaay bi di fukki xasab.»
3 Mu ne ma: «Lii mooy alkute giy wàccsi ci kaw réew mi mépp. Li téere bi wax ci genn wetam mooy képp kuy sàcc, dees na ko fi dàqe, te li mu wax ci wetam gi ci des mooy képp kuy giñ ci ay fen, dees na ko fi dàqe. 4 Maay wàcce alkute gi,» kàddug Aji Sax ji Boroom gàngoor yee, «mu dugg ba ci biir kër sàcc bi, ak kër nit kiy giñe sama tur ay fen; ci biir kër gi la alkute giy fanaan, ba raafal banti kër gi aki dojam.»
Juróom ñaareelu misaal: ndab lu jigéen toog ca biir
5 Ci kaw loolu malaaka ma doon wax ak man dikk ne ma: «Séentul rekk ba gis lii di dikk.» 6 Ma ne: «Lu mu doon?» Mu ne: «Ndabal nattukaay beey génn.» Mu tegaat ca ne: «Lii mooy seen bàkkaar ci biir réew mi mépp.»
7 Ci biir loolu kubeeru betteex ga ca kaw ndab la jekki yékkatiku, ndeke jenn jigéen a nga toog ca biir ndab la. 8 Mu ne: «Jigéen jii mooy mbon,» daldi koy bëmëx ca biir ndab la, fél kubeeru betteex ga, ubaat ndab la.
9 Ba loolu amee ma séentu, yem ci ñaari jigéen ñuy dikk, ngelaw li wal seeni laaf. Laaf yu mel ni laafi xodd lañu am. Ñu daldi yékkati ndabal nattukaay la, ba ca diggante asamaan ak suuf. 10 Ma ne malaaka ma doon wax ak man: «Ana fu ñii jëme ndabal nattukaay bi?» 11 Mu ne ma: «Ag kër lañu koy tabaxali ca réewum Sineyaar. Bu noppee, fa lañu koy teg, ca kaw tegukaayam.»