Téereb Yonent Yàlla
Sofoni
Téere bii moo indi kàdduy waxyu yu yonent Yàlla Sofoni jottali woon, jëme ci réewum Yuda, laata Babilon di tas réew ma. Booba waa Yuda dañoo dëddu Aji Sax ji, di jaamu ay yàlla yu dul dëgg. Rax ci dolli déggal Yàlla du woon lu leen amal solo, ndax booba koomu àddina moo leen jay, ba gisuñu njariñal tuub seeni bàkkaar.
Ci tënk:
1.1—2.3 Su bésub Aji Sax ji taxawee, Yuda day tas tasar.
2.4—3.8 Mbugal dëgmal na yeneen xeet yi, dëgmal Yerusalem.
3.9-20 Yuda dégg na digeb barke, ndax dinañu dellu ci Aji Sax ji.
1
Ubbite gi
Kàddug Aji Sax jii moo dikkaloon Sofoni doomu Kusi*Kusi: xalaat nanu ne nit ku ñuul la woon ku cosaanoo ca xeetu Kuus.. Kusi, Gedalya mooy baayam; Gedalya, Amarya, Amarya, Esekiyas. Mu yemook janti buuru Yuda, Yosya doomu Amon.
Am sànj taxaw na
«Lépp laay buube ba mu set fi kaw suuf.»
Aji Sax jee ko wax.
«Doom aadama ak mala,
njanaaw ak jën laay buub,
ak luy fakkastale, booleek ñu bon ñi.
Maay jële doom aadama fi kaw déndub suuf.»
Aji Sax jee ko wax.
 
«Maay xàcc sama loxo jëme ci Yuda
ak mboolem waa Yerusalem.
Maay jële fi bii béreb ndesu tuuri Baal,
ak turu sarxalantukatam yeek sarxalkatam yi,
ak ñiy sujjóotal ci kawi taax gàngoori biddiiw yi,
ak ñiy sujjóotal aka giñal Aji Sax ji
tey giñe Milkom, yàllantu ji,
ak ñi dëddu Aji Sax ji,
wutuñu Aji Sax ji, wutuñoo diisook moom.»
 
Miig! Fi kanam Boroom bi Aji Sax ji,
bésub Aji Sax ji kat dëgmal na;
Aji Sax jee waajal ab sarax,
te moo ca sellal ay ganam.
 
«Keroog bésub saraxu Aji Sax ji,
maay dikke mbugal kàngam yeek doomi buur yi
ak boroom coli ndoxandéem yi.
Bésub keroog maay dikke mbugal
képp ku aw tuuram tax mu aadawoo di tëb dëxu bunttëb dëxu bunt bi: li ñu ci jublu mooy moytu loraange ju ñu gëm ne tuur mi man na leen koo yóbbe, bu ñu joggee dëxu bunt bi. Seetal ci 1.Samiyel 5.5.,
ak ñiy feesal seen kër yàllantu ak alal
ju aw ay ak njublaŋ maye.
10 Su bés baa,» Aji Sax jee ko wax,
«yuux dina jibe fa buntu Jën ya,
wóoy jibe fa Sanc ya,
rajaxoo ju réy jollee ca tund ya.
11 Yeen waa goxu marse ba, yuuxooleen,
ndax jula yépp ay sànku,
mboolem kuy natt dogi xaalis lees fay jële.
12 Jantub keroog ay làmp laay niite Yerusalem,
ba dikke mbugal ña fa ne degg,
taaje ni biiñ ci kaw ginjriitam,
te naa ci seen xel: “Aji Sax ji baaxewul, lorewul.”
13 Seen alal lees di sëxëtooji, seeni kër gental,
ñu tabax ay kër yu ñu dul dëkke;
jëmbat tóokëri reseñ yu ñu dul naan biiñ bi.»
 
14 Bésub Aji Sax bu mag bee dëgmal,
moo dëgmal te tànk yu gaaw lool lay jegesee.
Kàddug bésub Aji Sax ji dégtu na,
te ca la jàmbaar di yuuxoo yuux yu metti.
15 Bésub keroog bésub sànj lay doon,
bésub njàqare ak tumurànke,
bésub gental ak gentle,
bésub lëndëmu xàmbaari guddi gu ne këruus,
16 bésub bufta ak wootey xare
ca kaw dëkk ya ñu dàbbali,
ak ca kaw sooroori tata ya ca koñ ya.
 
17 «Ca laay jàqale doom aadama yi,
ñuy tëñëx-tëñëxi ni silmaxa,
nde Aji Sax ji lañu moy,
te seen deret lees di sotti fi pëndub suuf,
seen yérey biir ni neefare fi suuf.
18 Du seen xaalis, du seen wurus
wu leen di mana xettali.
Keroog bésub sànjum Aji Sax ji,
ak sawaras fiiraangeem,
àddina sépp ay xoyomu.
Mooy raafal moos mboolem ñi dëkke àddina si,
te raafal gu raglu lay doon!»

*1.1 Kusi: xalaat nanu ne nit ku ñuul la woon ku cosaanoo ca xeetu Kuus.

1.9 tëb dëxu bunt bi: li ñu ci jublu mooy moytu loraange ju ñu gëm ne tuur mi man na leen koo yóbbe, bu ñu joggee dëxu bunt bi. Seetal ci 1.Samiyel 5.5.