Bataaxal bu jëkk bi Yàlla may Póol,
mu bind ko waa
Korent
1
1 Ci man Póol mi ñu woo ci sasub doon ndawal Almasi Yeesu, ci coobarey Yàlla, ci man la bataaxal bii bawoo, bawoo itam ci Sosten mbokk mi,
2 ñeel mbooloom Yàlla, mi ci Korent, yeen ñi ñu sellal ci jëmmu Almasi Yeesu, te ñu woo leen ngir ngeen doon ñu sell, ñeel itam mboolem ñiy tudde fépp fu mu mana doon, sunu turu Boroom Yeesu Almasi, mi leen moom, moom nu.
3 Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.
Sant Yàlla war na
4 Santal leen sama Yàlla laa saxoo, ci yiw wi mu leen may ci Almasi Yeesu,
5 ndax lépp ngeen woomle ci moom, ci gépp kàddu, ak bépp xam-xam.
6 Loolu di firndeel ne la nu seedeeloon Almasi, sotti na ci yeen.
7 Loolu tax na ñàkkatuleen genn may, léegi bi ngeen di séentoogum peeñum sunu Boroom Yeesu Almasi.
8 Moo leen di dooleel ba ca mujjantal ga, ngir ngeen mucc sikk, keroog sunu bésu Sang Yeesu Almasi.
9 Yàllaa am kóllëre, moom mi leen woo, ngir ngeen bennoo ak Doomam Yeesu Almasi, sunu Sang.
Na mbooloo mi juboo
10 Bokk yi nag, dama leen di ñaax, ci sunu turu Sang Yeesu Almasi, ngir seen kàddu di genn, te féewaloo baña am ci seen biir, xanaa ngeen bennoo ci lépp, bokk menn xel, ak benn jëmu.
11 Ndax kat bokk yi, dégge naa ci waa kër Kelowe, ne am na ay dëngoo ci seen biir.
12 Li may wax mooy ku nekk ci yeena ngi naan: «Man ci Póol laa bokk!», «Man nag Apolos!» «Man Sefas!» «Man de Almasi!»
13 Ndax Almasi dafa xaajalikoo? Ndax Póol lañu daajoon ca bant ba ngir yeen? Am ci turu Póol lañu leen sóobe ci ndox?
14 Maa ngi sant Yàlla, ba ma sóobulee kenn ci yeen ci ndox, ku dul Kirispus ak Gayus,
15 ngir kenn du ne ci sama tur lañu leen sóobe.
16 Ahakay! Maa sóob waa kër Estefanas itam. Waaye bu loolu weesee, fàttlikuwuma fu ma sóobe keneen.
17 Ndax du sóobe cim ndox la ma Almasi yebale, xanaa ngir ma yégle xibaaru jàmm bi, te bañ koo defe xareñtey kàddu, ngir baña neenal bantub Almasi, ba ñu ko daajoon.
Xam-xam, fa Yàlla
18 Ndax kat kàddu gi jëm ci bantub Almasi, ba ñu ko daajoon, ag ndof la ci ñiy sànku. Waaye manoore Yàlla la ci nun ñi mucc.
19 Ndaxte bindees na ne:
«Maay yàq xam-xamu xamkat yi,
ñi xelu, ma neenal seenum xel.»
20 Ana kuy xamkat? Ana kuy firikatub yoon? Ana waxkatub àddinay tey jii? Xanaa du Yàllaa def xam-xamu àddina si ag ndof?
21 Yàlla moo dogal ci xam-xamam, àddina tële koo xam ci xam-xamu boppam. Moo tax mu soob Yàlla, mu jëfandikoo xibaaru Almasi, biy ag ndof ci nit ñi, ngir musale ko gëmkat ñi.
22 Yawut yi, ay takk lañuy laaj, Gereg yi di wut xam-xam.
23 Nun nag, nuy waare Almasi bu ñu daaj ci bant, muy njombe ci Yawut yi, di ag ndof ci jaambur ñi dul Yawut.
24 Waaye ci ñi ñu woo, ñuy Yawut, di Gereg, Almasi mooy manoorey Yàlla, di xam-xamu Yàlla.
25 Ndaxte li ñu jàppe ag ndof fa Yàlla moo sut xam-xamu nit, te li ñu jàppe néew dooley Yàlla moo raw dooley nit.
26 Bokk yi, seetleen ñan ngeen woon, ba ñu leen di woo. Barewul ci seen biir ay xamkat, ci gis-gisu nit ñi, barewul ci yeen ay boroom doole, barelewuleen ñu rafet ab juddu.
27 Waaye li àddina jàppe ag ndof, moom la Yàlla taamu, ngir rusloo ko xamkat yi, te li néew doole ci àddina, moom la Yàlla taamu, ngir rusloo ko li bare doole.
28 Li tuut ab juddu ci àddina, ak li xeeblu, li tekkiwul dara, moom la Yàlla taamu, ngir neenale ko li tekki,
29 ba tax kenn du mana damu ci kanam Yàlla.
30 Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu, mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njekk, di sunu sellte, di sunug njot,
31 su ko defee, noonu ñu binde ne: «Kuy damu, na damu ci Boroom bi,» noonu lay ame.