16
Póol nuyu na waa Room
1 Boole naa leen nag ak sunub jigéen Febe, mu di ab taxawukatub mbooloom gëmkat ma dëkke Señsere.
2 Dalal-leen ko ci turu Boroom bi, ni ko ñu sell ñi yelloo, te ngeen jàpple ko ci lépp lu mu aajowoo, nde moom itam xettli na ñu bare, ba ci man mii.
3 Nuyul-leen ma Pirsil ak Akilas, sama bokki liggéeykat ci liggéeyub Almasi Yeesu.
4 Ñoom ñoo jaay seen bakkan ngir ma mucc, te du man doŋŋ maa leen ameel njukkal, waaye mboolooy gëmkat yu jaambur ñi dul Yawut yépp a leen ameel njukkal.
5 Nuyul-leen ma itam mbooloom gëmkat miy daje ca seen kër. Nuyul-leen ma sama soppe Epaynet, miy jooxeb ndoortel meññeef, ma génne ca diiwaanu Asi, ñeel Almasi.
6 Nuyul-leen ma Maryaama, mi sonn lool ci yeen.
7 Nuyul-leen ma Andoronikus ak Yuña, sama bokki Yawut, yi ñu ma tëjandooloon; ñu ñu nawloo lañu ci ndaw yi, te ñoo ma jëkka gëm sax Almasi.
8 Nuyul-leen ma Ampilyaatus, mi ma soppal sama bopp ndax Sang bi.
9 Nuyul-leen ma it Urben, sunu mbokkum liggéeykat ci liggéeyub Almasi, ak Estakis, sama soppe;
10 nuyul-leen ma Apeles mi firndeel kóllëre gi mu am ci Almasi, te ngeen nuyul ma waa kër Aristobul,
11 ak Erojon sama mbokkum Yawut, te ngeen nuyul ma waa kër Narsis ñi gëm Sang bi.
12 Nuyul-leen ma Tirifen ak Tirifos, jigéen ñu sonn ci liggéeyu Boroom bi, ak it ndaw si Persidd mi sonn lool ci liggéeyu Boroom bi.
13 Nuyul-leen ma Rufus, mi Boroom bi taamul boppam, ak yaayam jiy sama yaayu bopp.
14 Nuyul-leen ma Asànkirit ak Felegon ak Ermes ak Patarobas ak Ermas, ak mboolem bokk yi nekk ak ñoom.
15 Nuyul-leen ma it Filolog ak Yuli, ak Nere ak jigéenam, ak Olimpas ak mboolem ñu sell ñi nekk ak ñoom.
16 Saafoonteeleen fóonante yu sell. Mboolooy gëmkati Almasi yépp nuyu nañu leen.
Kàdduy àrtu ak tàggoo ñeel na waa Room
17 Léegi nag bokk yi, dama leen di ñaax, ràññeeleen ñi gàntal àlluwa ji ngeen jànge, di féewale, ak a téqtale, te ngeen moytu leen.
18 Ñu ni mel liggéeyaluñu Almasi sunu Boroom, seen koll lañuy liggéeyal. Làmmiñ yu neex, ak kàddu yuy jaye lañuy naxe ñi seenum xel foogadi.
19 Yeen nag seenug dégg ndigal siiw na ba bir ñépp, moo tax ma di leen bége. Waaye damaa bëgg ngeen xelu ci lu baax, te seenum xel mucc ci lu bon.
20 Su ko defee Yàlla miy boroom jàmm mooy dër Seytaane ci lu gaaw, fi ngeen ko joggi seeni tànk.
Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu ànd ak yeen!
21 Timote sama mbokkum liggéeykat nuyu na leen, mook Lusiyus ak Yason ak Sosipater sama bokki Yawut.
22 Man Tersiyus mi bind kàdduy bataaxal bi ci sama loxo nag, nuyu naa leen ci turu Boroom bi.
23 Gayus mi may dalal, di dalal mbooloo mi mépp këram, nuyu na leen; Eràst saytukatub alalu dëkk bi it, nuyu na leen, mook mbokk mi Kàrtus.
24 Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi ànd ak yeen! Amiin.
Teddnga ñeel na Yàlla
25 Kooku leen mana dooleel nag ndax sama xibaaru jàmm, ak waareb Yeesu Almasi, mi mu feeñal mbiram tey, gannaaw ba mu nekkee mbóot mu làqu woon naka jekk,
26 mbóot mu bindi yonent yi fésal tey, ba xamal ko xeet yépp ci ndigalal Yàlla ji sax, ngir xeet yépp gëm ba dégg ndigal,
27 kooku mooy Yàlla mi wéetoo xam-xam, te moom la teddnga ñeel ba fàww, ndax Yeesu Almasi! Amiin.