5
1 Waaye nag bokk yi, lu jëm ci ay àpp, ak bés ya loolu di am, soxlawuleen ku leen ci bind,
2 ndax yeen ci seen bopp, xam ngeen xéll ne Sang bi, ni sàccub guddi lay dikke.
3 Fa nit ñi naan: «Jàmm ak kaaraange dikk na,» fa la sànkute di dale ci seen kaw, ni aw mat di jekkee dal ci kaw jigéenu wérul, te kenn du ca rëcce.
4 Waaye yeen bokk yi, nekkuleen cig lëndëm, ba bés boobu di leen bett ni ab sàcc di bettee.
5 Yeen ñépp ay doomi leer ngeen, doomi bëccëg ndarakàmm; nun bokkunu dara ak guddi, mbaa ag lëndëm.
6 Kon nag bunu nelaw ni ñi ci des, waaye nanu teewlu, te ànd ak sunu sago.
7 Ndaxte ñiy nelaw, guddi lañuy nelaw; ñiy màndi it, guddi lañuy màndi.
8 Waaye nun ñiy waa bëccëg, nanu ànd ak sunu sago, te def ngëm ak cofeel, sunu kiiraayal dënn; yaakaaru texe di sunu mbaxanam xare.
9 Ndax kat Yàlla séddu nu am sànj, waaye ag mucc la nu moomale ndax sunu Sang Yeesu Almasi.
10 Su nuy dund, ak su nuy dee, moom moo nu deeyal, ngir nu mana ànd ak moom, dund.
11 Kon nag noonu ngeen di ñaaxantee, aka yokkante, nangeen ko wéye.
Dénkaane yii la Póol tëje
12 Gannaaw loolu bokk yi, danu leen di ñaan, ñi féetewoo coonob liggéey ci seen biir te jiite leen ci yoonu Boroom bi, di leen yee, nangeen leen yég.
13 Nangeen leen nawe seen kem kàttan te soppe leen noonu ndax seen liggéey. Gannaaw loolu, nangeen jàmmoo.
14 Bokk yi, danu leen di dénku; yaafus yi, femmuleen leen; ñi néewu fit, ñaaxleen leen; néew-doole yi, dimbalileen leen, te it muñal-leen ñépp.
15 Fexeleen ba kenn du feyantoo. Waaye lu baax, deeleen ko deflante ci seen biir, te di ko defal ñépp.
16 Fu ngeen tollu bégleen,
17 saxooleen ñaan,
18 te deeleen sant, ak nu mu mana deme, ndax loolu mooy coobarey Yàlla ci yeen ñi ànd ak Almasi Yeesu.
19 Buleen giimal taalub Noowug Yàlla gi,
20 buleen gàttañlu ay kàdduy waxyu.
21 Waaye lu mu mana doon, settantal-leen ko, li baax, ngeen jàpp ci,
22 te lu bon, ak nu mu mana bindoo, dàndleen ko.
23 Yàlla ci boppam, moom miy Boroom jàmm, yal na leen sellal, ba ngeen mat sëkk, te seen léppi xel, ak seen léppi xol, ak seen léppi yaram sàmmu, ba mucc sikk, ba kera bés bu sunu Sang Yeesu Almasi feeñee.
24 Ki leen woo de ku wóor la, te moo koy def it.
Póol tàggtoo na ak waa Tesalonig
25 Bokk yi, nun itam, ñaanal-leen nu.
26 Nuyul-leen nu bokk yépp, te fóonal-leen nu leen na mu gëna selle.
27 Maa ngi leen di dénku nag, ngir Boroom bi, jàngleen biral bataaxal bii ngir bokk yépp.
28 Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi ànd ak yeen.