Ñaareelu bataaxal bi Yàlla may Póol,
mu bind ko waa
Tesalonig
1
1 Man la Póol, mi ànd ak Silwan ak Timote ci kàddu gii ma yékkati, ñeel mbooloom gëmkati waa Tesalonig, ñi bokk ci Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.
2 Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, tukkee ci Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.
Cant war na ci waa Tesalonig
3 Bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla ci yeen fu nu tollu, te muy lu jaadu, gannaaw seen ngëm a ngi yokku bu baaxa baax, te cofeelu ku nekk ci yeen ñépp di gënatee law, digganteem ak moroomam.
4 Moo tax nun, nu di leen damoo fi biir mboolooy gëmkati Yàlla yi, ndax seenug muñ, ak seen ngëm, ci biir mboolem ni ñu leen di bundxatale, ak njàqare yi ngeen di jànkoonteel.
Njekk feeñ na ci àtteb Yàlla
5 Loolu lépp di firndeel njekku àtteb Yàlla, bi leen di yellale nguurug Yàlla, gi tax ngeen di sonn.
6 Te kat njekku Yàlla dina feeñ ndax coono ba muy delloo ñi leen teg ab coono.
7 Dina feeñ it ndax noflaay ba mu nuy booleek yeen ñiy dékku ab coono, sédde nu ko, kera bés bu Sang Yeesu feeñee, ànd ak ay malaakaam yu làmboo manooreem, wàcce asamaan.
8 Ci biir sawara wuy sëlsëli lay doon. Ca lay mbugal ñi xamul Yàlla, ak ñi baña déggal xibaaru jàmm bi jëm ci sunu Boroom Yeesu.
9 Ñooñu lees di mbugale sànkute gu sax dàkk, fu sore Boroom bi, sore teddngay manooreem,
10 kera bés bu délsee ba jot ci teddngaam ci biir ñoñam ñu sell ñi, ba mboolem ñi ko gëm di ko yéemoo. Te yeen ci seen bopp, ci ngeen di bokk, ndax yeena gëm la nu leen seedeeloon.
11 Moo tax nu saxoo leena ñaanal, ngir sunu Yàlla yellale leen ab wooteem, ngir itam mu sottale kàttanam seen mboolem mébét mu baax, ak seen jépp jëf ju laloo ngëm.
12 Su ko defee sunu turu Sang Yeesu màgge ci yeen, yeen it, ngeen màgge ci moom, ci sunu ndimbalal yiwu Yàlla, ak Sang Yeesu Almasi.