2
Ndëngte ju mag mooy jiitu bésu Sang bi
1 Léegi nag, bokk yi, ci wàllu dellusig sunu Sang Yeesu Almasi, ak sunu dajeji fa moom, li nu leen di ñaan moo di:
2 bu leen lenn gaawa xañ sago ba ngeen ñàkka ànd ak seenum xel, mbaa mu di leen jaaxal; du lu ñu ne kàddug waxyu la, du genn kàddu mbaa bataaxal bu ñu nu moomale, te di leen gëmloo ne bésu Sang bi dikk na ba noppi.
3 Bu leen kenn naxe nenn, ndax bés ba du dikkagum, te fippu gu mag ga jëkkula dikk, ba ki jëmmal ndëngte te dëgmal alkute, feeñ.
4 Kooku mooy jànkoonteeka damu ci kaw mboolem lees di wooye yàlla, mbaa lees di jaamu, te mooy mujj toog ca kër Yàlla ga, ba far tudde boppam Yàlla.
5 Xanaa fàttlikuwuleen ne waxoon naa leen ko, ba ma nekkee ak yeen?
6 Te xam ngeen li ko téye léegi, ba du mana feeñ lu dul ca bésam.
7 Kumpa la dooley ndëngte ji bàddoo te mu ngi def liggéeyam xaat, xanaa kay ki ko téye ba tey moo koy téye rekk ba keroog jëlees fi ki ko téye.
8 Su boobaa la ku dëng ka di feeñ, te Sang Yeesu moo koy jàllarbee ngelawal gémmiñam, te moo koy rajaxee ca na muy feeñe bu délsee.
9 Peeñum ku dëng ki liggéeyu Seytaane lay àndal, te dina wone wépp xeetu manoore, aki firnde ak kéemaani feni neen,
10 ak mboolem xeeti naxe yu njubadi lal, ñeel ñi nara sànku ndax ñàkka sopp dëgg gi, ngir nangu ko ba mucc.
11 Looloo tax Yàlla yónnee leen jëf juy sànke, ngir ñu gëm aw fen.
12 Su ko defee mbugal dal mboolem ñi gëmul dëgg gi, xanaa di xejjoo njubadi.
Taxawleen bu dëgër
13 Nun nag bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla fu nu tollu, ci yeen ñi Boroom bi sopp, ndax yeen la jëkka taamu, ngir sellale leen Noo gu Sell gi, ak itam seen ngëm gi ngeen gëm dëgg gi, ngir texeel leen.
14 Ci loolu it la leen woo ba mu jëfandikoo xibaaru jàmm bi nu leen àgge, ngir ngeen séddu ci sunu ndamal Boroom Yeesu Almasi.
15 Kon nag bokk yi, taxawleen bu dëgër te ŋoy ci dénkaane yi nu leen àgge ci sunu làmmiñu bopp, ak yi nu leen bind ci sunuy bataaxal.
16 Sunu Sang Yeesu Almasi ci boppam, ak Yàlla sunu Baay, mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk, ak yaakaar ju wér,
17 yal nañu leen may jàmmi xol, te may leen dooley wéye jépp jëf ju baax, ak gépp kàddu gu rafet.