5
Rikk wooteel, ndegam am na ku lay wallu!
Ana ci ñu sell ñi, kan ngay sàkku ndimbal?
Am sannax déy, naqari deret a koy rey,
ab téxét, xéraangee koy faat.
Maa gis am sannax, mu saxi reen,
ma jekki ñaan alkàndey dëkkuwaayam.
Ay doomam ay sore yoonu mucc,
ñu di leen dëggaate ca pénc ma,
te kenn du leen xettli.
Am ngóobam, ku xiif a koy lekk,
ba lekkaale la saxe biir dég ya,
te alalam, ku mar a koy ŋaf-ŋafee.
Aw ay du garab, bay fëlle biir suuf,
coono du jekki, jebbi.
Ku juddu, coono nga juddul,
mooy ferñent, kaw rekk la jëm.
 
Man de su ma doon yaw damay sàkku Yàlla,
te kon Yàlla laay diis sama mbir.
Keey def jëf ju màgg ju nattuwul,
di def kiraama yu limuwul.
10 Keey taw, suuxat suuf,
yónnee ndox, nàndal ub àll.
11 Keey kaweel ku suufe,
kuy ñaawlu siggee mbégte.
12 Keey neenal pexem ku muus,
ba mébétam du sotti.
13 Keey kepp boroom xel cig muusam,
ba pexem ndëngteem teela sooy.
14 Ñu ni mel, bëccëg ñu dajeek lëndëm,
di làmbatoo digg bëccëg ni bu doon guddi.
15 Yàllaay musal néew-ji-doole ci saamaru làmmiñ
ak loxol boroom doole,
16 néew-ji-doole jagoo yaakaar,
defkatu njekkar ub gémmiñug boppam.
 
17 Ma ne, ndokklee ku Yàlla jubbanti,
kon bul bañ yarub Aji Kawe ji.
18 Moom kat mooy mitital, di fajtal;
mooy gaañe, di wérale loxol boppam.
19 Juróom benni njàqare teew, mu xettli la ca,
ba ko juróom yaareel sax, doo ca loru.
20 Ab xiif, moo la cay jote ba doo dee,
ab xare, nga mucc ñawkay saamar,
21 aaytéefu làmmiñ, nga fegu ca,
te yàqule guy dikk, doo ko ragal.
22 Yàquleek ub xiif, nga kekku;
rabu àll, doo ko ragal.
23 Doji àll bi sax, kóllëreg jàmm ngay séq ak ñoom,
te ndundati àll bi dañuy jàmmook yaw,
24 nga xam ne sa xayma, jàmm,
soo nemmikoo sa parlu, dara du ca wuute.
25 Dangay ràññee ni saw askan di yaatoo,
say sët di law ni gàncax.
26 Ni pepp di ñore, ñu door koo góob,
ni ngay màggataale doole, doora dëgmal bàmmeel.
27 Lii kat lanu gis, te lii rekk la.
Dégg, jariñu.