6
Maa yey ne ba ma
1 Ayóoba daldi ne:
2 Éy su sama tiis wii doon lu ñuy natt diisaayam?
Su sama ay wii wépp doon lees di màndaxe?
3 Kon tey mu gëna diis suufoo suufi géej.
Moo waral sama kàddu yi ma rëcc.
4 Da di fetti Aji Man jee ma jam,
ba tooke ji nàndal samam xel,
mbugalu Yàlla yu raglu làng-déral ma.
5 Mbaamu àll dina ŋaax te tiim ñax mu tooy a?
Am nag dina nàññi te tiim um ngooñam?
6 Deesul lekk lu soof, loo deful xorom,
rawatina lu weex li ci nen.
7 Sama xel a ko nanguwul,
ñam la wu ma seexlu.
8 Éy kuy amal sama dagaan,
ba Yàlla sottal sama yaakaar!
9 Yal na neex Yàlla mu nappaaje ma,
yal na afal loxoom, ne ma tipp.
10 Konoon sama ndàmpaay di li ma gàntalul
kàdduy ku Sell ki,
te kon ma bég, di fecce biir mitit wu dul dal.
11 Ana doole ju ma amati bay muñ?
Ana luy sama muj ba may dundati?
12 Dama diw doj bay àttan lu ne?
Am yaramu xànjar laa am?
13 Ndax amati naa wall,
te pexe réer ma mërr?
14 Ku ne lasiim, saña séentu xarit baaxe la,
doonte fekkul nga ragal Aji Man ji.
15 Samay xarit a ma wor ni yol moo fekk ŋiis.
Dañoo mel ni dex yoo fekk ndox ma jeex,
16 te ba sedd bay tàggoo,
ndox mu wayoon ànd caakam yuur, di seey,
mu fees dell ak ndox mu nëx.
17 Waaye bu noor biy dikk, mu wow,
tàngoor jam, mu ŋiis.
18 Jëggi giléem ay wër um ndox, ba wacc seenu yoon,
saaraan ca ndànd-foyfoy ga, réer.
19 Waa jëgg ya bawoo Tema di wër ay yol,
tukkikat ya bawoo Saba di séentuy dex,
20 ba àgg fa ñu ko fooge woon, yaakaar tas,
seen kóolute mujje mbetteel.
21 Yeen déy, yeenay yooyu wal ci man.
Yeena gis sama njàqare, jàq.
22 Dama leena masa ñaan dara,
mbaa ma sàkkoo ci seen alal ab ger,
23 ngir ngeen xettli ma ci loxol noon,
mbaa ngeen jot ma ci boroom doole bu néeg?
24 Xamal-leen ma, man ma ne cell!
Ana fu ma juume? Wonleen ma ko!
25 Kàddu yu jub da lay yey,
ana li ngeen may yedde, lu mu doon?
26 Dangeen di jéema sikk samay wax,
di jàppe ngelaw kàdduy xol bu jeex?
27 Ab jirim sax àttan ngeen koo tegoo bant,
seen xarit sax sañ ngeen koo jaay.
28 Léegi nag, rikk walbatikuleen fi man,
xanaa duma janook yeen di fen?
29 Deltuleen gannaaw, bu njubadi am.
Dellootileen gannaaw, sama der set na wecc!
30 Ana fu ma waxe njubadi?
Am damaa xamul lu njekkar di saf?