4
Aji Sax ji yedd na Yunus
Ba loolu amee Yunus mer mer mu réy, ba xol bay bax. Mu ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Céy Aji Sax ji, xanaa du lii laa waxoon ba ma génnagul sama réew? Moo taxoon ma jëkka daw, jëm Tarsis! Ndax xamoon naa ne yaw Yàlla yaay boroom yiw ak yërmande, sa mer a diib, sa ngor bare, ngay fomm mbugal. Léegi nag Aji Sax ji, rikk jëlal sama bakkan rekk, ndax dee sax a ma gënal dund!» Aji Sax ji ne ko: «Waaw, mbaa yaa yey am xol bu tàng ci loolu?»
Yunus daldi génn dëkk ba, dem toogi fa féete dëkk ba penku, mbaaral fa boppam, toog ca keppaar ga, di seet nu dëkk bay mujje. Ba mu ko defee Aji Sax ji Yàlla yebal ag lawtan, mu law, tiim Yunus, keral boppam ngir xettli ko. Yunus bég mbégte mu réy ca lawtan ga. Ca ëllëg sa, ba jant bay fenk, Yàlla yebal aw sax, mu song lawtan ga, mu wow. Naka la jant ba fenk, Yàlla yebal ngelawal penku lu tàng jérr, jant ba jam boppu Yunus, ba mu xawa xëm, bëggatul dara ci bakkanam. Mu naan: «Dee sax a ma gënal dund!»
Ci kaw loolu Yàlla ne Yunus: «Waaw, mbaa yaa yey am xol bu tàng ci lawtan gi?» Mu ne: «Maa yey am xol bu tàng ba dee sax!» 10 Aji Sax ji ne ko: «Waaw yaw, yaa ngi xalaat lawtan gii nga sonnul, lawaloo ko; guddi la sax, guddi ga ca topp mu dee. 11 Man nag, Niniw, dëkk bu mag bii ëmb lu ëpp fuuf téeméeri junniy nit ak ñaar fukk (120 000), ñu ràññeewul seen ndijoor ak seen càmmoñ, ak mala yu bare, duma leen xalaat?»