Téereb Yonent Yàlla
Mise
1
1 Kàddug Aji Sax jii moo dikkaloon Mise miy waa Moreset, ca janti Yotam ak Axas ak Esekiya, buuri réewum Yuda, na seen nguur topplantee. Lii la Mise gis ci mbirum Samari ak Yerusalem.
Aji Sax ji yékkati na kàddug tuuma
2 Dégluleen, yeen, xeetoo xeet,
teewlul, yaw àddina ak li ci sa biir,
ba Boroom bi Aji Sax ji seedeel leen tuuma,
Boroom beey àddoo fa màkkaanam mu sell ma.
3 Aji Sax jaa ngii di génne ca bérabam ba,
mooy wàccsi, daagoo kawtey suuf.
4 Tund ya mu joggi da naan soyox seey,
xur ya xar, wàyyi ni dax ju jege sawara,
def ni ndox mu wale kaw mbartal.
5 Bàkkaaru Yanqóobaa waral lii lépp,
moyi Israyil googu la.
Ana luy bàkkaaru Yanqóoba?
Da dul Samari?
Ana fuy bérabi jaamookaayi xërëm ci Yuda?
Da dul Yerusalem?
6 «Maay saam Samari, def ko jalu tojit
ci mbooy gi,» la Aji Sax ji wax.
«Maa koy def jëmbatukaayub reseñ,
maay yuri ay doji tabaxam ca xur wa,
ñori ay kenoom.
7 Seen jëmmi tuur yépp ay rajaxoo,
te mboolem seen peyoor yu sobewu
day lakk ba jeex.
Maay tas tasar mboolem seen jëmmi xërëm,
seen peyi gànc a leen ko may,
kon na ko seen moroomi gànc feyeekoo.»
Ñaawlu dikkal na Yuda
8 Lee ma tax di jooy ak a yuuxu,
ne duŋŋ, deme tànki neen, di ko ñaawloo.
Naa yuuxu nig till,
naa sab sabum looy ndaxu naqar.
9 Góom bi Aji Sax ji teg Samari kat amul paj,
te moo law ba Yuda,
àkki ba buntu Yerusalem, ca saay bokk.
10 Buleen ko nettali fa Gaat,
buleen jooy benn yoon.
Xalanguleen fa pëndub suuf sa ca Bet Leyafra,
di ko ñaawloo.
11 Yeen waa Safiir, jàll-leen,
ak gàcce ak yaramu neen.
Waa Caanan sañuñoo génn,
te wall du bawoo fa waa Bet Eccel,
ñay jooy seeni néew.
12 Waa Marot a mar jàmm,
te aw ay a wàcce fa Aji Sax ji,
ba agsi buntu Yerusalem.
13 Yeen waa Lakis, takkleen fasi dawkat ak watiir.
Yeena jëkka moyloo janq Siyoŋ mu taaru,
ci yeen lañu jëkka gise bàkkaari Israyil.
14 Yeen waa Yuda, mayleen waa Moreset Gaat
lu ngeen tàggtook ñoom,
këri Agsib wori neen lay doon ci buuri Israyil.
15 Yeen waa Maresa laay indil ku leen moom,
te ca Adulam la ñi Israyil di damoo di làquji.
16 Watuleen nel, ñaawloo ko
doom yi leen doon bànneexal.
Neluleen nel yu set nim tan, naqarloo,
nde ngàllo lañu jëm, teqlikook yeen.