2
Mbugal dal na aakimookat yi
1 Wóoy, ngalla ñiy mébét ñaawtéef,
di ràbb lu bon ci seenub tëraay,
bët set, ñu jëfe ko,
ndax xam ne man nañu ko.
2 Ñooy xemmemi tool, foqati,
ay kër, ñu nangu,
tey not waay ak waa këram,
ak nit ci céru suufam.
3 Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne:
«Maa ngii di nasal googu làng aw ay,
ay wu ngeen dul teggee ci seenu loos,
te dungeen daagu, siggi,
nde jant yu metti lay doon.
4 Bésub keroog lees leen di fental aw léeb,
woyal leen woy wu tiis,
te naa: “Sotti na, yàqu nanu yaxeet!
Sama suufu askan dugg na ciy loxo,
ba sore ma,
ab fippukat lañu jox sunuy tool!”»
5 Moo tax bu mbooloom Aji Sax ji waree jotaat ci seen suuf,
kenn ci yeen du am cér, ba ñu di ko tàllalal buumu nattukaay.
Yonenti caaxaan yaa ngi diiŋat
6 Seen yonent yeey waare naa:
«Buleen waare!
Nii kat deesu ko waaree,
gàcce du nu dab!»
7 Bànni Israyil, ndax dees na waxe nii:
«Aji Sax ji day xàddee?»
Am: «Jooju jëf da di jikkoom?»
«Sama kàddu jàmm la ci kuy def njub.
8 Yeen sama ñoñ, démb rekk ngeen jóg nib noon;
yeena ngi nangoo ci nit mbubbum xewam,
fekk muy romb, buggul xare, foogul dara.
9 Jigéen ñi ci sama ñoñ ngeen dàqe
seen këri mbégte,
te seeni doom, yeena leen xañ
sama barke ba fàww.
10 Jógleen dem, fii du bérabu noflaay,
nde sobewu na, ba nara yàqe yaxeet.
11 Nit man naa wër, toppi caaxaan aki fen,
naan: “Maa lay yégal waxyub biiñ aku ñoll,”
te kookooy jottlikatub waxyu bi askan wii yelloo!
Aji Sax jeey dajale ndesu ñoñam
12 «Yeen askanu Yanqóoba, maa leen di dajalee
dajale yeen ñépp,
maay boolee boole ndesu Israyil.
Benn bopp laa leen di def, niy xar ca gétt ga,
niy gàtt ci seenum parlu,
coowal nit ña jolli.
13 Kiy bëtt mooy dox, jiitu leen,
ñu bëtt, jàll bunt bi, dem.
Seen buur mooy jàll jiitu leen,
Aji Sax jeey dox fa seen kanam.»