13
Colu Yeremi misaal la
Aji Sax ji da maa wax ne ma: «Demal jëndi njiitlaayu lẽe*, nga woddoo ko, te bu ko ndox laal.» Ma jënd njiitlaay, woddu, muy la Aji Sax ji wax. Aji Sax ji dikkal ma ñaareel bi yoon, ne ma: «Jëlal njiitlaay li nga woddoo, te daldi dem ba Fara, nga làqi ko fa ca xar-xaru doj ya.» Ma dem làqi ko Fara, muy la ma Aji Sax ji sant. Ñu dem ba mu mat ay fan yu takku, Aji Sax ji ne ma: «Demal Fara, jëli njiitlaay la ma la santoon nga làqi ko fa.» Ma dem fa ma làqoon njiitlaay la, sulli ko. Ndeke njiitlaay la yàqu na, ba amatul njariñ!
Kàddug Aji Sax ji dellu dikkal ma, ne ma: «Aji Sax ji dafa wax ne: Ni lii yàqoo, ni laay sàggee sagub Yuda ak sagu Yerusalem bu réy bi. 10 Askan wu bon wii bañ maa déggal, të ticc di wéye seen coobare, di topp yeneen yàlla, di leen jaamook a sujjóotal, nañu mel ni njiitlaay lii amul benn njariñ. 11 Ndax ni njiitlaay di taqe ci luppu nit, noonu laa jële woon waa kër Israyil ak waa kër Yuda, taqoo leen.» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Maa ko def ngir ñu doon sama ñoñ, teral sama tur, di sama ndam, di sama sag. Waaye déggaluñu ma.»
Yàlla misaal na meram
12 «Nga wax leen kàddu gii: “Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Njaqal biiñ, duy, mu fees. Bu ñu la nee: ‘Dañoo xamul xéll ne njaqal biiñ, duy, mu fees?’ 13 nga ne leen: ‘Aji Sax ji dafa wax ne: Muy buur yi toogal Daawuda cib jalam, di sarxalkat yi, di yonent yi, di mboolem waa Yerusalem, maa ngii di duysi mboolem waa réew mii, ba ñu fees ak màndite. 14 Su ko defee ma fenqe ku nekk ak mbokkam, fenqe waajur ak doom, ñoom ñépp.’ ”» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Duma ñéeblu, duma yërëm, duma leen ñeewantee faagaagal.»
Dégloo, balaa yeex
15 Dégluleen te teewlu, buleen fétteeral.
Aji Sax ji kat wax na!
16 Teral-leen seen Yàlla Aji Sax ji,
bala moo lëndëmal,
ngeen tërëfe tundi timis,
di séentu leer,
mu lëndëmal ba mu ne këruus,
fatt taraj
17 Bu ngeen déggul de,
ma làqu, jooy seen reewande,
sama rongooñ tuuroo tuuru,
ma jooya jooy,
nde dees na jàpp géttu Aji Sax ji, yóbbu.
Mbugal a ngi
18 Waxal Buur, wax Lingeer yaayu Buur ne leen:
«Dëjuleen fi suuf,
seen mbaxanam nguur mu yànj foq na.
19 Dëkki Negew yu mag yi tëje na,
te kenn du ko tijji.
Yuda gépp ca ngàllo ga, Yuda ba mu daj, ngàllo ga.»
Yerusalem am na gàcce
20 Yerusalemee, séentul, xool ñiy jóge bëj-gànnaar.
Moo ana gétt gi ñu la dénkoon,
sa gàtt yu rafet ya?
21 Sa xejj yi nga miinal sa bopp,
bu ñu walbatikoo tiim la,
ana looy wax nag?
Kon mitit du la jàpp,
nga mel ni kuy matu?
22 Soo nee ci sam xel:
«Lu tax lii dal ma?»
xamal ne sa ñaawtéef gu réy a waral
ñu ñori la, saaysaaye la.
23 Ana ab Kuuseen bu mana soppi deram,
mbaa am segg mu mana fari tipp-tippam?
Kon nga mana def lu baax
te tàmma def lu bon!
Yàllaay wax
24 «Maa lay tasaare ni boob muy naaw
mu ngelawal màndiŋ mi wal.
25 Loolooy sa wàll,
sa cér bi ma la nattal.»
Kàddug Aji Sax jee.
Mu ne: «Yaa ma fàtte,
di yaakaari caaxaan.
26 Man it maay ëñ sa pendal,
muure sa kanam,
saw taat ne duŋŋ.
27 Sag njaalook sa ŋexali caga,
sa gànctu gu ruslu
ci kaw tundi àll bi!
Maa gis sa jëf ju siblu jooju!
Musibaa yaw Yerusalem!
Foo àppal sa jëfi sobe ji?»
* 13:1 njiitlaay li ñuy wax fii, séru njiitlaay lu gàtt lay doon. 13:4 Fara bérab la bu bokkul ak dexu Efraat doonte neexoo nañuy tur.