14
Maral dikk na
Kàddug Aji Sax jii dikkaloon na Yeremi, jëm ca maral ma. Mu ne:
«Waa Yudaa ngi ñaawlu,
doole dëddu dëkk yi,
ñu ne yogg, ne lasar fi suuf,
yuux jollee Yerusalem.
Kàngam ya yebal seeni surga, ñu rooti;
ñu dem, gisuñu ndox ca mbalka ya,
délseek seen xotti ndab,
jàq, yaakaar tas, ñu muuru di tiislu.
Réew mi tawluwul, suuf si fett,
yaakaaru beykat tas, mu muuru, di tiislu.
Kéwél sax jur ci àll bi, sànni
ndax ñàkk um ñax.
Mbaamu àll taxaw ci tund yi ne faraas,
di àppaat niw till,
ñàkk parlu, gët ya giim.»
Yeremeey wax
Dëgg la sunuy ñaawtéef a nu tuumaal,
waaye éy Aji Sax ji, jógal te saw tur tax,
doonte dëddu nanu la ay yooni yoon, moy la.
Éy yaw, yaakaaru Israyil, mi nuy wallu bésu njàqare,
bul ñooru ni doxandéem ci réew mi,
mbaa ku nekk ciw yoon, jàdd fi, fanaan.
Ngalla bul mel ni ku waaru,
mbaa jàmbaar ju manul walloo.
Yaw Aji Sax ji, yaa ngi sunu biir,
ñu di nu tudde saw tur.
Bu nu wacc!
10 Aji Sax ji dafa wax ci askan wii ne: «Ñeeka bëgg ub taxawaalu, baña téye seen tànk. Moo tax man Aji Sax ji bégewuma leen. Léegi ma bàyyi xel seenug mbon, ba mbugale leen seeni moy.»
Waxyuy caaxaan jib na
11 Aji Sax ji nag ne ma: «Bul ñaanal askan wii. 12 Su ñu ci boole woon koor sax, duma déglu seeni dagaan. Su ñu ma doon sarxalal saraxu rendi-dóomal ak saraxu pepp it, du maa leen di nangul. Xanaa saamar akub xiif ak mbas kay laa leen di faagaagale.»
13 Ma ne ko: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yonent yaa ngii di leen wax ne duñu dajeek saamar, duñu xiif te jàmm ju ne ñoyy nga leen di defal fi bii bérab.»
14 Aji Sax ji ne ma: «Waxyuy fen la yonent yiy waxe ci sama tur. Yebaluma leen, santuma leen ko, waxumaak ñoom. Peeñuy fen ak ngisaaney neen ak nax yu ñu fental seen bopp lañu leen di jottlee waxyu.» 15 Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Yonent yi ma yebalul te ñuy waxe waxyu ci sama tur naan: “Saamar akub xiif du am ci miim réew,” saamar akub xiif ay mujje yooyu yonent. 16 Ñi ñu doon jottli ay waxyu it, xiif ak saamar a leen di rey, ñu sànni seeni néew ci mbeddi Yerusalem, te duñu am ku leen rob, ñook seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen. Dinaa leen xëpp seen ay.
17 Nanga leen yégal saw tiis, ne leen:
“Naa tuur rongooñ guddeek bëccëg,
te du fer;
sama bokki bopp yi damm ba dammtoo,
ndaw góom bu metti!
18 Ma dem, xool àll,
gisuma lu moy ñu saamar bóom,
ma dugg biir dëkk,
gisuma lu moy ñu ne làcc akub xiif,
yonent ak sarxalkat di wër réew mi,
xam-xam réer leen.”»
Yeremee ngi tinu Aji Sax ji
19 Aji Sax ji, wacc ngaa wacc Yuda nii?
Am Siyoŋ a la génnliku?
Lu tax nga di nu dumaa musiba mu amul paj?
Nuy yaakaar jàmm, dara baaxul,
nuy séentum paj, tiitaange ne jaas!
20 Aji Sax ji, xam nanu sunug mbon,
xam sunu ñaawtéefi maam;
moy nanu la moos.
21 Waaye xoolal ci yaw te bul xalab,
bul teddadil sa jal bu tedd.
Bàyyil xel te baña fecci sa kóllëreek nun.
22 Xërëmi neen yi yéefar yiy jaamu,
ana ku ci mana taw?
Am asamaan ay sóobal boppam ay waame?
Du yaw la Aji Sax ji sunu Yàlla?
Yaw lanu yaakaar,
te loolu lépp, yaw a.