Sabóor 105
Aji Sax ji sàmm na kóllëre
1 Santleen Aji Sax ji, tudd turam,
xamley jalooreem ci biir xeet yi,
2 woy ko, tagg ko,
yégle mboolemi kéemaanam!
3 Damooleen turam wu sell.
Kuy wut Aji Sax ji, yal na am bànneexu xol.
4 Gëstuleen Aji Sax jeek dooleem,
di ko sàkku saa su ne.
5 Fàttlikuleen ay jalooreem
aki misaalam aki àtteem.
6 Yeen askanu Ibraayma, jaamam ba,
yeen ñiy sëti Yanqóoba, ñiy tànnéefam,
7 kee di sunu Yàlla Aji Sax ji,
di àtte suuf sépp,
8 di fàttliku ba fàww kóllëreem,
di bàyyi xel ba ci junniy maas kàddoom
9 ga mu digoon Ibraayma,
giñal ko Isaaxa,
10 dëggalal ko Yanqóoba, sàrtal ko,
fase kook Israyil mooma kóllëre gu sax.
11 Mu ne: «Yaw laay jox réewum Kanaan,
muy sa cér, nga séddoo.»
12 Ba bànni Israyil dee ñu néew,
diy doxandéem ca réew ma,
13 di wëreelu ci biir xeetoo xeet,
ak nguuroo nguur,
14 mayul nit mu not leen,
te yaral na leen ay buur,
15 ne leen: «Buleen laal samay tànnéef,
buleen lor samay yonent.»
16 Moo wàcce ab xiif ca réew ma,
dagge fa luy gub,
17 yónnee ku leen jiitu,
muy Yuusufa ma ñu jaayoon njaam,
18 tànk ya, ñu jéng jéng yu tar,
baat ba, ñu yeewe caqu weñ.
19 Kàddug Aji Sax ji di nattu Yuusufa,
ba keroog pirim ma dikk,
20 Buur a yónni ku ko yiwi,
ku yilifi xeet a ko tijji.
21 Mu sas ko mu jiite këram,
di saytu mboolem alalam,
22 ba saña tënk jawriñi buur ci coobareem,
tey xelal mag ña.
23 Israyil agsi Misra,
muy nganug Yanqóoba ga ca réewum Xam.
24 Aji Sax ji giiral xeetam wa,
ba ñu gëna bare seeni noon,
25 mu xiir waa Misra ci dëddu ñoñam,
ñuy fexeel jaamam ñooña.
26 Mu yónni Musaa, jaamam ba,
tànn Aaróona, boole ca,
27 ñu sottal ci seen biir firndeem ya mu waxoon,
muy kéemaan ya ñu def ca réewum Xam.
28 Moo yónnee lëndëm, lëndëmal,
te Musaa ak Aaróona gàntaluñu kàddoom.
29 Moo soppi seen ndoxum réew deret,
rey seeni jën,
30 feesal seen réew ay mbott
yu àkki seen biir néegi buur ya.
31 Moo àddu, weñ ya dikk,
rayentaan ya dajal seen réew ma.
32 Mu def seenub taw tawub yuur,
sawaray melax jafal seen réew ma.
33 Mu dóor seen figg ak reseñ,
fóom seen garabi réew ma.
34 Mu àddooti, ay soccet dikk,
di njéeréer yu wees ab lim,
35 ñu lekk luy gàncax ca seenum réew,
lekk lu suuf sa meññ.
36 Moo fàdd luy taaw ca seenum réew,
muy lu jëkka soqeekoo seen digg doole.
37 Mu génne leen, ñu yóbbaale xaalis ak wurus,
te kenn tërëful ca seeni giir.
38 Misra daa bég ba ñu demee
ndax tiitaange lu ñu leen tiital.
39 Mu firiw niir, yiire leen,
ak sawara, ñu niitoo guddi.
40 Ñu sàkku, mu wàcceey picci përëntaan,
teg ca reggal leen mburum asamaan.
41 Mu bënnu doj, ndox ma ball,
di dex, wale joor gu wow.
42 Daa bàyyi xel kàddoom gu sell,
ga mu waxoon Ibraayma, jaamam ba.
43 Moo génne ñoñam, ñu bég,
moo génne tànnéefam ña, ñuy sarxolle.
44 Mu jox leen suufi yéefar ya,
ñu jagoo ñaqi xeet ya,
45 ngir ñu sàmm ay dogali yoonam,
topp ndigali yoonam.
Màggal-leen Ki Sax!