Sabóor 106
Israyil di wor, Yàlla di wóor
1 Màggal-leen Ki Sax!
Santleen Aji Sax ji, kee baax,
kee saxoo ngoram!
2 Ana ku mana tudd jaloorey Aji Sax ji?
Ana ku mana teesal woyam?
3 Ndokklee kuy sàmm yoon,
di def njekk fu mu tollu.
4 Éy Aji Sax ji, séddaale ma ci sa yiwu ñoñ,
ngalla, dikke ma sag wall,
5 ma gis ngëneelu ñi nga tànn,
di bànneexoo sa bànneexu xeet wi,
tey damoondook ñoom ñi nga séddoo.
6 Noo bàkkaar, nook sunuy maam;
noo def lu ñaaw, def lu bon.
7 Sunuy maam seetuñu ca say kéemaan ca Misra,
bàyyiwuñu xel ca sa ngor lu réy,
xanaa di fippu ca géej ga, géeju Barax ya.
8 Teewul Yàlla wallu leen ngir turam,
ba xamle njàmbaaram.
9 Dafa gëdd géeju Barax ya, mu ne sereŋ;
xóotey géej mel ni màndiŋ, mu jàlle leen,
10 musal leen ci loxol bañaale,
jote leen ca loxol noon ba,
11 ndox ma mëdd bañ ya,
kenn desu ca.
12 Ca lañu gëm ay waxam,
woy ko.
13 Nes tuut ñu fàtte jëfam ja,
xaaratuñu ndigalam,
14 di ŋaf-ŋafi ca màndiŋ ma,
di diiŋat Yàlla ca àll ba.
15 Yàlla jox leen la ñuy sàkku,
wàccaaleel leen woppi ràgg.
16 Ba ñu demee ba iñaane Musaa ca dal ba,
boole ca Aaróona mu sell ma, nitu Aji Sax ja,
17 suuf a ne ŋafeet, wonn Datan,
mëddaale gàngooru Abiram;
18 sawara ne jippét fa seen biir,
tàkk ba lakk ñu bon ñooña.
19 Tëgg nañu aw nag ca tundu Oreb,
di sujjóotal jëmm ju ñu móol,
20 di jënde seen teddngay Yàlla ja
jëmmu nag wuy for um ñax.
21 Dañoo fàtte Yàlla ma leen di musal
te def jaloore ca Misra.
22 Mooy kéemaan ya fa réewum Xam,
kiraama ya ca géeju Barax ya.
23 Yàlla da leen doon sànk,
bu dul woon ak Musaa, xejjam
ba ko kar, àtte leen,
mu giif, ba fàkkasu leen.
24 Dañoo gàntal réew mu neex,
gëmuñu kàddug Yàlla,
25 xanaa di xultoo seen biiri xayma,
baña déggal Aji Sax ji.
26 Moo tax mu giñal leen
ne dina leen tëral fa màndiŋ ma,
27 tëral seen askan ci biir xeet yi,
wasaare leen ci réew yi.
28 Ñuy darook tuurum Baal Pewor,
di lekk lu ñu sarxal ay yàlla yu amul bakkan,
29 di merloo Yàlla ci seeni jëf,
ba mbas ne dàll fa seen biir.
30 Fineyas taxaw, àtte;
mbas ma dal,
31 muy njekk lu ñu ko waññal
tey ak ëllëg.
32 Ñu merlooti Yàlla ca ndoxum Meriba ma,
muy loraangey Musaa te ñoo ko waral.
33 Ñoo naqaral Musaa,
ba mu wax wax ju ko rëcc.
34 Te it faagaagaluñu yéefar,
ya leen Aji Sax ji waxoon,
35 xanaa di jaxasook yéefar yooya,
di roy seeni jëf,
36 di jaamu seeni tuur,
mu mujj dig fiir ca ñoom.
37 Ñuy sarxalal rab ya
seen doom yu góor ak yu jigéen,
38 di tuur deretu ñu deful dara,
te muy seen deretu doom yu góor ak yu jigéen
ya ñu sarxalal tuuri Kanaaneen ña,
deret ja sobeel réew ma,
39 seeni jëf sobeel leen,
ndax seen bokkaale.
40 Aji Sax ji mere ñoñam,
sib xeet woowu mu séddoo,
41 ba tax mu teg leen ca loxol yéefar ya,
seeni bañ yilif leen,
42 seen noon ya not leen,
ñu torox ca seeni loxo.
43 Ay yooni yoon la leen xettli,
teewul ñuy nas pexey fippu,
ba suux ci seeni ñaawtéef.
44 Mu gis nag seen njàqare,
dégg seeni tinu,
45 bàyyi xel ci kóllëreem ak ñoom,
topp ngoram lu réy, ba giif,
46 xiir ña leen jàpp ñépp,
ñu yërëm leen.
47 Éy Aji Sax ji, sunu Yàlla, wallu nu,
génnee nu ci xeet yi, dajale nu,
nu sante la sa sellnga,
di sagoo sa teddnga.
48 Santleen Aji Sax ji, Yàllay Israyil
cant gu sax dàkk, ba fàww.
Na ñépp ne: «Amiin!»
Màggal-leen Ki Sax!